Esteer
10 Keroog bésub juróom ñaareel ba Buur Aserus naan biiñ, ba xolam sedd, mu sant juróom ñaari bëkk-néegam‡1.10 bëkk-néeg yooyu, ay jaam yu ñu tàpp lañuy doon.: Meyuman ak Bista ak Arbona ak Bigta ak Abagta ak Setar ak Karkas, ne leen 11 ñu indil ko Lingeer Wasti, mu sol mbaxanam lingeeram, ngir won taaram ba nit ñaak kàngam ya, ndax jigéen ju rafetoon la. 12 Teewul ba bëkk-néeg ya yeggee Lingeer Wasti ndigalal Buur, mu lànk, ne du ñëw. Buur nag mer lool, ba xol bay bax. 13 Booba mboolem mbirum buur, xamkati jamono ya ci wàllu yoon ak àtteb yoon lees koy diis. 14 Ña ca gënoona jege Buur di Karsena ak Setar ak Admata ak Tarsis ak Meres ak Marsena ak Memukan, ñuy juróom ñaari kàngami diiwaani Pers ak Medd, di bokk ak Buur jataay te gëna kawe ca nguur ga. 15 Mu ne leen: «Ci yoon, ana lu war ci Lingeer Wasti, gannaaw déggul ndigal li ma joxe, man, Buur Aserus, samay bëkk-néeg jottli ko ko?»
16 Memukan wax ca kanam Buur ak kàngam ya, ne leen: «Du Buur doŋŋ la Lingeer Wasti tooñ. Waaye tooñ na mboolem kàngam yi ak mboolem baadoolo yi ci mboolem diiwaan yi. 17 Nde jëfi lingeer jii dina yegg ci noppi jigéen ñépp, ba tax ñuy sofental seen jëkkër. Ndax dañu naan: “Xanaa Buur Aserus woowul Lingeer Wasti, mu lànk, ne du ñëw”? 18 Li ko dale bésub tey, kuy garmi bu jigéen ci Pers ak Medd, bu déggee jëfi lingeer jii, noonu lay waxeek mboolem kàngami buur, mu indi yabeel ak réeroo bu dul jeex. 19 Kon nag Buur, ndegam soob na la, na ab dogal tukkee fi yaw, ñu bind ko ci ndigali yooni Pers ak Medd, yi dul toxu, di xamle ne Wasti dootu jàkkaarlooteek Buur Aserus. Te Buur, dangay nangu céru lingeeram, jox ko moroomam mu ko gën. 20 Su ko defee bu ñu yéenee dogalu buur bi ci mboolem déndu buur bu yaatu bii, jigéen ñépp dinañu weg seen jëkkër, boroom daraja ba ci baadoolo bi.»
21 Loola nag neex Buur ak kàngam ya. Buur nag def la ko Memukan wax. 22 Ba mu ko defee mu yónnee ay bataaxal fépp ca réew ma, diiwaan bu nekk ak mbindum boppam, waaso wu nekk it ci làkku boppam. Mu biralal waaso wu nekk ci làkku boppam, ne leen na góor gu nekk doon kilifay këram.
Esteer 2 ->