3 Lu jëm nag ci powum séy, ak jépp jëfi sobe, mbaa ag bëgge, li jekk ci ay nit ñu sell, moo di ñu bañ koo tudd sax ci seen biir, 4 te ag ñàkk kersa, ak waxi caaxaan, ak kaf yu bon, dara jekku ci, waaye saxooleen kàdduy cant. 5 Ndax lii kat na leen wóor: képp ku nekke powum séy, mbaa jëfi sobe, mbaa ag bëgge, kooku amul cér ci nguurug Almasi ak Yàlla, ndax ku bëgge ab bokkaalekat la.
15 Kon nag xool-leen bu baax seen jëfin, defleen jëfinu nit ñu am xel, te baña mel ni ñu ñàkk xel, 16 Jariñooleen lu ngeen man, jot gi ngeen amagum, ndax jant yu bona ngii tey. 17 Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi. 18 Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noo gi fees, 19 ngeen di jàngalante jàngi Sabóor, ak jàngi cant, ak jàng yu bawoo ci Noo gi leen fees, te ngeen di woy aka kañ Boroom bi, ci seen xol. 20 Fu ngeen tollu, ak ci mbir mu mu mana doon, santleen Yàlla Baay bi ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, 21 te ngeen rus Almasi, ba tax ngeen di nangulante.
25 Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba jooxeel leen bakkanam. 26 Moo defal loolu mbooloo mi ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko. 27 Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
28 Noonu la jëkkër ji wara soppe jabaram, ni mu soppe yaramu boppam rekk. Sopp sa jabar sopp sa bopp la, 29 ndax kenn masula bañ suuxu boppam, xanaa mu di ko dundal, di ko topptoo, ni Almasi ak mbooloom gëmkat ñi, 30 nde noo di céri yaramam. 31 Ni ko Mbind mi indee: «Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, daldi taqoo ak jabaram, ba ñoom ñaar di wenn suux*5.31 Seetal ci Njàlbéen ga 2.24..» 32 Mbóot mu xóota ngi ci dog boobu, waaye man, li may wax moo di dog bi moo misaal diggante, bi Almasi séq ak mbooloo mi. 33 Teewuleen koo moom yeen itam; kon na ku nekk sopp jabaram ni mu soppe boppam, te ku nekk weg jëkkëram.
<- Efes 4Efes 6 ->- a 5.31 Seetal ci Njàlbéen ga 2.24.