4 Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy, gi mu nu sopp, 5 nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. 6 Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan. 7 Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel. 8 Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la; 9 du peyu jëf, ba kenn di ci kañu. 10 Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet, ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.
14 Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jaambur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante. 15 Yoonu Musaa ak santaane yaak ndigal ya, moom la xewil, ngir yeesal ñaar ñi, Yawut beek jaambur bi, ci jenn jëmmu boppam, ñu doon kenn nit ku yees, ba jàmmoo. 16 Ñaar ñi la Almasi boole ci jenn jëmm, jubale leen ak Yàlla, ca bant ba ñu ko daajoon, te bant ba la dakkale sunub tongoo. 17 Moo dikke xibaaru jàmm buy yégle jàmm ju leen ñeel, yeen jaambur ñi ko sore woon, te ñeel nu, nun ñi ko jege, 18 ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gi.
19 Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen. 20 Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi. 21 Ci moom la tabax bi bépp di temboo, ba jóg, doon jaamookaay bu sell ngir Boroom bi. 22 Ci Almasi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jaambur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
<- Efes 1Efes 3 ->