4 Gannaaw bu leen leen seen Yàlla Aji Sax ji dàqalee nag, buleen wax ci seen xel ne: «Sunu njekk a nu may Aji Sax ji indi nu, ngir nu moom réew mii.» Mbonug xeet yii kay moo waral Aji Sax ji dàqal leen leen. 5 Du seen genn njekk, akug njub gu leen may ngeen nanguji seenum réew. Waaye mbonug xeet yii moo waral seen Yàlla Aji Sax ji dàqal leen leen, ngir sottal kàddu ga mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. 6 Kon na leen bir ne du seenug njekk moos la leen seen Yàlla Aji Sax ji joxe mii réew mu baax, ngir ngeen moom ko ndax, askan wu daŋŋiiral ngeen.
11 Ba ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg matee, Aji Sax ji jox ma ñaari àlluway doj ya, àlluway kóllëre ga. 12 Aji Sax ji ne ma: «Jógal wàcce fii gaaw, ndax sa bokk ya nga génnee Misra def nañu yàqute. Teggi nañu xaat yoon wa ma leen santoon. Móolal nañu seen bopp jëmmu tuur.»
13 Aji Sax ji waxati ma, ne ma: «Gis naa ne mbooloo mii kat, ñu dëgër bopp lañu. 14 Bàyyi ma rekk ma faagaagal leen, ba far seen tur fu asamaan tiim, te def la ngay xeet wu ëpp wii, ëpp ko doole.»
15 Ba loolu amee ma walbatiku, wàcce ca tund wa, maak yaari àlluway kóllëre ga ca sama yaari loxo, tund wépp di tàkk. 16 Ma gis ne ndeke moy ngeen seen Yàlla Aji Sax ji, daldi sàkkal seen bopp wëllu wu ñu móol, dëddu xaat yoon wa leen Aji Sax ji santoon. 17 Ci kaw loolu ma ne cas yaari àlluwa ya ca sama yaari loxo, sànni, rajaxe ko, ngeen di gis.
22 Ca Tabera itam, ak ca Maasa, ak ca Kibbrot Taawa, ngeen merlooti fa Aji Sax ji. 23 Ak ba leen Aji Sax ji yebalee fa Kades Barneya, ne leen: «Demleen nanguji réew ma ma leen jox.» Yeena gàntal seen kàddug Yàlla Aji Sax ji, gëmuleen ko, déggaluleen kàddoom. 24 Gàntal Aji Sax ji ngeen nekke naka jekk, dale ko ca bés ba ma leen xamee.
25 Maa daanu tëdd fa kanam Aji Sax ji diiru ñeent fukki bëccëg yooyu, ak ñeent fukki guddi ya ma tëdd fa kanamam ndax la Aji Sax ji noon da leen di sànk. 26 Ma ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, bul sànk sa ñoñ ñi nga séddoo, ñi nga jote sa màggaay, génnee leen Misra ci sa dooley loxo. 27 Ngalla bàyyil xel sa jaam ña, Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. Bul xool ci tëwug mbooloo mii ak seen mbon, ak seenug moy. 28 Lu ko moy kat waa réew ma nga nu jële dinañu ne: “Tële leena yóbbu réew ma mu leen digoon, ak jéppi leen moo tax Aji Sax ji génne leen, ngir rey leen ca màndiŋ ma.” 29 Ñii de ñooy sa ñoñ ñi nga séddoo, ñi nga génnee sa doole ju bare, ci sa kàttanu loxo.»
<- Baamtug Yoon wi 8Baamtug Yoon wi 10 ->