5 Mu ngoog, jàngal naa leen ay dogali yoon, aki àttey yoon, na ma ko sama Yàlla Aji Sax ji sante, ngir ngeen war koo jëfe ca biir réew ma ngeen di nanguji. 6 Sàmmooleen koo jëfe, ndax mooy doon seenug rafet xel, ak seenug ràññee fi kanam xeet yi, ba bu ñu déggee mboolem dogali yoon yii, dinañu ne: «Wii askan wu mag rekk a rafet um xel te ràññee!» 7 Ana wan xeet wu mag wu am yàlla ju leen jege ni nu sunu Yàlla Aji Sax jiy jegee saa yu nu ko wooyee wall? 8 Ana xeet wu ko màgge, ba am dogali yoon ak àttey yoon yu jekke ni yoon wii ma joxe fi seen kanam bésub tey?
9 Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët. 10 Bés ba ngeen taxawee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa tundu Oreb, Aji Sax jee ma ne: «Dajaleel ma mbooloo mi, ma dégtal leen samay kàddu, ngir ñu tàggatu ci ragal ma li feek ñuy dund ci kaw suuf, te seeni doom it, ñu tàggat leen ci.» 11 Yeena dikk taxaw ca suufu tund wa, tund wa ne jippét, sawara wa jolli ba ca xolu asamaan, ci biir xàmbaari guddi gu ne këruus. 12 Aji Sax ji àddoo ca digg sawara wa, wax ak yeen, ngeen di dégg baat, te jëmm, gisuleen ko, xanaa baat doŋŋ. 13 Ci kaw loolu mu biralal leen kóllëreem gi mu leen sant ngeen sàmm ko, muy fukki santaane yi. Mu daldi leen bindal santaane yi ci ñaari àlluway doj. 14 Man nag la Aji Sax ji sant ca yooya jant, ne ma xamal leen dogali yoon yeek àttey yoon, yi ngeen wara jëfe ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko.
21 Waaye yeena tax Aji Sax ji mere ma ba giñ ne duma jàll dexu Yurdan, te duma dugg ca réew mu baax, ma leen seen Yàlla Aji Sax ji moomale. 22 Man nag ci réew mii laay dee. Du maay jàll dexu Yurdan. Waaye yeen yeenay jàll, ba nanguji réew mu baax moomu. 23 Wattuleen seen bopp ba baña fàtte kóllëre gi seen Yàlla Aji Sax ji fas ak yeen, di sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn, te seen Yàlla Aji Sax ji aaye leen ko. 24 Seen Yàlla Aji Sax ji kat, mooy sawara wuy xoyome, Yàlla ju fiir la.
25 Bu ngeen demee ba am ay doom aki sët, fekk leen yàgg ca réew ma, su boobaa su ngeen defee ag yàqute, di sàkk am tuur, ak jëmmu lu mu mana doon, mbaa ngeen def lenn lu seen Yàlla Aji Sax ji ñaawlu, lu koy merloo, 26 maa ngi sàkku asamaan ak suuf seedeel maak yeen bésub tey jii, ne su boobaa yeenay sànkoo sànku ci lu gaaw, ba wuute ca réew, ma ngeen jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko. Su boobaa dungeen fa yàgge, ndax dees leen di raafal, ba ngeen jeex tàkk. 27 Aji Sax ji moo leen di tasaare ci biir xeet yi, te lu néew la seenu ndes di doon ci biir xeeti jaambur yi leen Aji Sax jiy dàq jëme. 28 Foofa ngeen di jaamoo ay yàlla yu loxoy nit sàkke bant, mbaa doj, yàlla yu dul gis, du dégg, du lekk, du xeeñtu. 29 Waaye su ngeen fa sàkkoo seen Yàlla Aji Sax ji, dingeen ko daj, ndegam seen léppi xol, ak seen léppi bakkan ngeen ko sàkkoo. 30 Bu leen njàqare dikkalee, fekk mboolem mbir yooyu dab leen, su boobaa dingeen mujj délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji te dingeen ko déggal. 31 Ndax seen Yàlla Aji Sax ji Yàllay yërmande la. Du leen wacc, du leen yàqte te du fàtte kóllëre, ga mu fasoon ak seeni maam ci kaw ngiñ.
39 Kon xamleen tey te délloosi ci seen xel, ne Aji Sax ji mooy Yàlla fa kaw asamaan ak fi kaw suuf. Du keneen. 40 Sàmmleen dogali yoonam, ak santaaneem yi ma leen dénk bés niki tey, ndax ngeen baaxle yeen ak seen doom yi leen di wuutu, te ngeen yàgg ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox ba fàww.
44 Lii moo di ndigalu yoon wi Musaa biraloon fi kanam bànni Israyil. 45 Lii moo di seedey yoon yi, ak dogali yoon yi, ak àttey yoon yi Musaa dénkoon bànni Israyil, gannaaw ba ñu bàyyikoo Misra, 46 ca wàllaa dexu Yurdan, ca xur wa janook Bet Pewor, ca réewum Siwon buurub Amoreen ba toogoon Esbon, te Musaa ak bànni Israyil duma woon ko, ba ñu génnee Misra. 47 Ñoo nangu am réewam, ak réewum Og buuru Basan, ñaari buuri Amoreen ña moomoon wàllaa dexu Yurdan, ca penku, 48 fa dale ca Arower, ga ca catal walum Arnon, ba ca tundu Siyoŋ*4.48 Gii Siyoŋ wuute na ak weneen tur wi ñuy wooye Yerusalem., ga ñuy wax itam Ermon, 49 boole ca mboolem joorug wàllaa dexu Yurdan, ca penku, ba àgg ca géeju Xorom ga, ca suufu tundu Pisga.
<- Baamtug Yoon wi 3Baamtug Yoon wi 5 ->- a 4.48 Gii Siyoŋ wuute na ak weneen tur wi ñuy wooye Yerusalem.