Saar 32
Musaa woy na kóllëreg Aji Sax ji
1 Yeen asamaan, teewluleen, ma wax,
Yaw suuf, déglul sama kàddu yii.
2 Na samam njàngle sóob nib taw,
samay kàddu rogalaat nib lay,
ba tuurul am ñax,
baawaanal gàncax.
3 Turu Aji Sax ji déy laay tudd,
seedeleen sunu màggaayu Yàlla.
4 Kee di cëslaay, te mati jëf,
wépp yoonam di njub.
Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi,
te njekk ak njub mooy boroom.
5 Njabootam ñoo def ug yàqute ci kawam,
ba dootuñuy doomam ndax seeni sikk.
Ndaw maas gu dëng te njublaŋ!
6 Aji Sax ji lañuy feye lii?
Ndaw xeet wu dofe te ñàkk xel!
Mooy seen baay, bind leen,
sàkk leen, samp leen.
7 Fàttlikuleen jant ya jëkkoon,
baleen xel maasi maas ya woon.
Laajleen seeni baay, ñu xamal leen;
ak seen mag ñi, ñu wax leen.
8 Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf,
tasaare doom aadama yi ci àddina,
moo àppal xeet yi seen kemi réew,
na mu dëppook limeefu goney*32.8 Mooy ndaw yi bokk ci péncum Yàlla. Yàlla yi.
9 Céru Aji Sax ji moo di ñoñam,
askanu Yanqóoba woowooy wàllam.
10 Moo leen fekk réewum màndiŋ,
fu ne wëyëŋ, ubaleeki sab,
mu feg leen, topptoo leen, sàmm leen,
ni bu ñu doon peru bëtu boppam.
11 Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam,
daayaarlu, tiim leen,
tàllali laafam, aw leen,
teg ciw dunqam, boot leen.
12 Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat,
du yàllay jaambur ju ko ci fekk.
13 Moo leen waral kawtey réew ma,
ñuy xontoo meññeefum àll bi,
mu di leen nàmpale lem ju walew doj,
ak diw gu balle xeer wu ne sereŋ,
14 boole ca soowum nag ak meewum xar,
nebbonu mbote, kuuyi diiwaanu Basan aki bëy,
teg ca ngëneeli pepp,
may leen biiñu reseñ ju xonq curr, ngeen naan.
15 Yeen Yesurun†32.15Yesurun: tur wii ak Yanqóoba itam dees na ko wooye Israyil., yeena yaflu, waŋŋeetu,
solu yaram, ne faaj, ne fuux,
fàtte Yàlla mi leen sàkk,
faaleedi seen cëslaay li leen musal.
16 Ñoo yee fiiraangeem, ndax ay yàllay doxandéem,
ñoo ko merloo ak seen tuur yu jomblu.
17 Ñoo sarxalal ay rab yu dul Yàlla;
ay yàlla yu ñu masula xam,
yu bees yu doora xew,
yu seeni maam ràññeewuloon.
18 Cëslaay li leen meññ ngeen foñ,
Yàlla ji leen jur ngeen fàtte.
19 Aji Sax jee gis loolu, gedd,
ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen.
20 Mu ne: «Maa leen di xañ sama kanam,
ba gis nu ñuy mujje,
ndax maasug defkati njekkar lañu,
doom yu ñàkk kóllëre.
21 Ñoo ma fiirloo ak yàlla yu dul tus,
merloo maak seen tuuri neen,
man it maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara,
ci waasow naataxuuna laa leen di merloo.
22 Sawaraa ngay tàkke ca samam sànj,
di lakke ba ca xóotey njaniiw,
ba xoyom suuf ak meññeefam,
ba jafal reeni tund ya.
23 Maay jal ci seen kaw ay musiba,
maa leen di soqil, ba jeexal samay fitt.
24 Ñooy loof cib xiif, jeex tàkk ndaxi jàngoro,
ak mbas yu metti.
Ay selli rabi àll laay yebal ci seen kaw,
boole ca daŋaru ndox-suuf.
25 Fa biti la leen saamar di xañey doom,
biir néeg ya, tiitaange luy reye feelu ko,
buubaale waxambaane akub janq,
luy nàmp, ak boroom bijjaaw.
26 «Maa noon maa leen di fàkkas,
ba far dakkal lu leen nit doon fàttlikoo.
27 Waaye reetaani noon laa ci ragal,
lu ko moy seeni bañ juume ko,
ba naan: “Sunu njàmbaar a!”
te waroon ne: “Aji Sax jee def lii lépp!”»
28 Wii xeet wu gàtt xel
te ñàkk xam-xam!
29 Su ñu muusoon, xalaat ci lii,
ba xam nu ñuy mujje.
30 Ana nu kenn di dàqe seen junni,
ñaar di fëxal seen fukki junni,
te ka ñu yaakaar jaayu leen,
te Aji Sax ji, laa ne, waccu leen?
31 Yaakaaru noon yi de melul ni sunu yaakaar,
te loolu la noon ya àtte.
32 Seen reseñ a nga cosaanoo Sodom,
ak tóokëri Gomor,
doom ya di tooke, cëgg ya wex xàtt!
33 Seen biiñ daŋaru ninki-nànka la,
ak tookey ñàngóor bu aay.
34 «Xanaa du loolu laa làq fi sama wet,
ne ko ràpp fi samay denc?
35 Maay kiy feye, di añale,
te bu jotee ñu fakkastalu,
ndax seen bésub toskaree dëgmal,
dogal ba buur, wutsi leen!»
36 Aji Sax jeey dëggal ñoñam,
mooy ñeewante ay jaamam,
bu gisee doole dëddu,
ba kenn desul, dub jaam, dus gor.
37 Su boobaa da naan: «Ana seen yàlla ya,
seen kiirlaay lañu daa làqoo?
38 Ñi lekk seen nebboni sarax,
naan biiñ bi ñu leen di tuural kay,
nañu jóg, boog, xettli leen, di seen kiiraay!
39 Kon gisleen ne man la, man doŋŋ,
kenn du Yàlla ku dul man!
Man maay rey, di dundal;
di gaañe, di wéral;
maay jàpp, te kenn du xettli.
40 Maay yékkati sama loxo jëme asamaan,
giñ ne: “Ndegam maay dund ba fàww,
41 bu ma daasee sama saamar buy melax,
ba ŋàbb ko ci saab loxo, di àtte,
maay fey samay digaale,
añale samay bañ.
42 Maay nàndal samay fitt deret,
sama saamar di yàppe,
deret di nàcce ci ku ñu jam, ak ku ñu jàpp,
tey tuuroo ci boppi kilifay noon yi.”»
43 Yeen, xeet yi, tàcculeen ñoñam,
deretu jaamam ñi lay feyul,
pey gu muy fey ay bañam,
ba jot suufam ak ñoñam.
Déggal Aji Sax ji, dund
44 Noonu la Musaa dikke, mook Yosuwe doomu Nuun, ba jaar ci mboolem kàdduy woy wii, mbooloo mi di dégg. 45 Gannaaw ba Musaa noppee ci jottli Israyil gépp mboolem kàddu yooyu, 46 da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii. 47 Ndax kat du kàddug neen ci yeen. Mooy seenug dund! Ci gii kàddu ngeen di gudde fan, ca réew ma ngeen di jàll dexu Yurdan jëm fa, ngir nanguji ko.»
Aji Sax ji woo na Musaa
48 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa bésub keroog boobee, ne ko: 49 «Doxal yéegi ca tundi Abarim gii, nga jàll ba ca tundu Nebo ca diiwaanu Mowabeen, ba janook Yeriko. Nga séentu nag réewum Kanaan mi may jox bànni Israyil, ñu jagoo. 50 Boo noppee, deel ca kaw tund woowu nga yéeg jëm, ba ñu tërali la ca say bokk, noonee sa mag Aaróona deeye woon ca kaw tundu Or, ba ñu tërali ko cay bokkam. 51 Li ko waral mooy yeena ma fecci worma ci digg bànni Israyil, ca ndoxi Meriba Kades, ca màndiŋu Ciin, ndax yeena wormaalul sama sellnga ci digg bànni Israyil. 52 Kon nag ci biti ngay séentoo réew ma, waaye foofa, doo fa dem. Doo dugg ca réew, ma may jox bànni Israyil.»
<- Baamtug Yoon wi 31Baamtug Yoon wi 33 ->