8 Buleen bañ ab Edomeen, ndax seen mbokk la. Buleen bañ nitu Misra, ndax ay doxandéem ngeen woon ca seenum réew. 9 Ñi soqikoo ci ñaari xeet yooyii, ca ñetteelu maas ga, te di seeni sëtaat*23.9 Mooy ñetteelu maasug xeet yooyu taamoo dëkke réewum Israyil. Seetal ci Màndiŋ ma 12.1-15. nag, sañ nañoo bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji.
10 Bu ngeen génnee ba fàkk ab dal, ngir jànkoonte ak seeni noon, nangeen sàmmu ci lépp lu aay. 11 Su amee ci seen biir ku setul, ndax géntu guddi gu ko dikkal, na génn dal bi, ca biti, te bumu duggaat ci biir dal bi. 12 Bu ngoon di jubsi na sangu, ba jant bi so, mu doora délsi ci biir dal bi. 13 Te sàkkleen bérab bu génn dal bi, ngeen di fa dem, di suturluji. 14 Na ngaska bokk ci seeni fàgguwaay, ndax su ngeen suturlujee ca biti ba noppi, moom ngeen di gase, ba suul seeni jonkan. 15 Ndax seen Yàlla Aji Sax ji mooy dem ak a dikk ci seen biir dal bi, ngir xettli leen, ba jébbal leen seeni noon. Kon nag seenub dal daa wara sell, ngir Aji Sax ji ñàkka gis fi seen biir, lenn lu tegginewul, ba dëddu leen.
16 Gannaaw loolu buleen delloo ab jaam bu làqu ci yeen, te rëcce ci ab sangam. 17 Ci yeen lay toog, ci seen biir, bérab ba mu taamu, ci benn bi ko gënal ci seeni dëkk, te buleen ko néewal doole.
18 Gànc bu jigéen buy gànctul ay tuur, bumu am ci biir jigéeni Israyil, te gànc bu góor buy gànctul ay tuur†23.18 Googu gànctu, jaamukati tuur ya ca Kanaan daan nañu ko jëfe, ngir yaakaar ne dina tax seenum njur, ak seeni tool nangu., bumu am ci góori Israyil. 19 Buleen indi mukk ci seen biir kër Yàlla Aji Sax ji, peyooru gànc bu jigéen, mbaa bu góor, ngir wépp xas wu ngeen namma wàccoo googu peyoor, ndax yooyu yaar yépp, seen Yàlla Aji Sax ji seexlu na ko.