5 Su ko defee sarxalkat yi, Leween ñi dikk, ndax ñoom la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ñu di ko liggéeyal, di barkeele ciw turam, te ci seen kaw kàddu lees di àttee bépp jote, ak gépp loraange ci wàllu yaram. 6 Dëkk boobu gëna jegewook fa néew ba tëdd, na mboolem seeni mag raxas seeni loxo, tiimale ca nag wu jigéen wa ñu damm loos wa, ca wal ma. 7 Ñu biral ne: «Nun déy sunuy loxo tuurul deretu nit kii, te sunuy gët it gisul ba ñu koy tuur. 8 Ngalla Aji Sax ji, jéggalal Israyil, sa ñoñ ñi nga jot, te baña toppe àqu deretu jaambur bu deful dara, fi digg Israyil sa ñoñ.» Su ko defee njéggal ñeel leen, ca deretu nit ka. 9 Yeen nag, noonu ngeen di tenqee ci seen biir, àqu deretu jaambur ju ñu tuur, ndax kon def ngeen li Aji Sax ji rafetlu.
15 Ku am ñaari jabar, su xejjoo kenn ki, foñ ki ci des, te ki mu xejjoo, ak ki mu foñ jural koy doom yu góor, te taaw bu góor bi di doomu ki mu foñ, 16 bés buy séddale doomam yu góor alalam, du saña jox doomu xejj bi, cér bi taaw yelloo, wacc doomu ka mu foñ, te muy taaw. 17 Taaw bay doomu ka mu foñ, na ko nangul ab céram, jox ko ñaar-cay céru rakk ja, ci mboolem alalam, ndax kooka soqikoo ci digg dooleem, mooy ka yelloo céru taaw.
18 Ku am doom ju góor ju dëgër bopp te të; déggalul baay, déggalul ndey, su ñu ko yaree, te taxul mu déggal leen, 19 na ko baayam ak ndeyam jàpp, yóbbu ba ca seen magi dëkk ba, ca seen bunt dëkk. 20 Ñu wax seen magi dëkk ba, ne leen: «Sunu doom jii ku dëgër bopp la te të. Déggalu nu, xanaa di xawaareek a màndi rekk.» 21 Na ko góori dëkk bépp dóori doj ba mu dee. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal.