6 Ab Leween bu dëkke benn ci seeni dëkk, ak fu mu mana doon ci Israyil, su fa jógee dem ci coobarey boppam, bérab bu Aji Sax ji taamu, 7 da fay liggéey ci turu Yàllaam Aji Sax ji ni mboolem bokki Leweenam, ña fa taxawe fa kanam Aji Sax ji, 8 njël lu yemook njëlal ña mu fa fekk it lew na ko, te limaaleesul lu ko dikke ci njaayum alalu baayam.
13 Muccleen sikk seen digganteek seen Yàlla Aji Sax ji, 14 ndax xeet yooyii ngeen di dàqi kat, ay luxuskat aki seetkat lañuy déggal, waaye yeen seen Yàlla Aji Sax ji mayu leen loolu. 15 Ab yonent bu soqikoo ci yeen kay, di seen mbokk ni man, moom la leen seen Yàlla Aji Sax ji di feeñalal. Moom ngeen di déggal. 16 Mooy noonee ngeen ko sàkkoo woon rekk, ci seen Yàlla Aji Sax ji ca tundu Oreb, ca bésub ndaje ma, ngeen ne: «Rikk bunu déggati sunu baatu Yàlla Aji Sax ji. Sawara wu réy wii it, bunu ko gisati, lu ko moy nu dee,» 17 te Aji Sax ji ne ma: «Ñoo yey wax loolu. 18 Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant. 19 Su boobaa ku déggalul sama kàddu yi muy wax ci sama tur, man maa ko koy topp. 20 Waaye déy yonent bu am fitu àddu genn kàddu ci sama tur, te santuma ko mu wax ko, mbaa mu wax ci turi yeneen yàlla, boobu yonent, dee mooy àtteem.»
21 Dingeen wax ci seen xel, ne: «Ana nu nuy ràññee kàddu gu Aji Sax ji waxul?» 22 La yonent bi wax ci turu Aji Sax ji, su sottiwul, dikkul rekk, loola du kàddu gu Aji Sax ji wax. Ñeme Yàlla la ko yonent ba waxe, buleen ko ragal.
<- Baamtug Yoon wi 17Baamtug Yoon wi 19 ->