4 Waaye ab ndóol du am ci seen biir, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di barkeel bu baax ca réew ma mu leen di jox, muy seen cér, ngeen jagoo, 5 ndegam déggal ngeen bu baax seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmmoo jëfe mboolem santaane bii ma leen di dénk tey. 6 Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelee ni mu ko waxe déy, yeenay lebal xeet yu bare, waaye yeen dungeen leb. Te it yeenay yilif xeet yu bare, waaye yeen, deesu leen yilif.
7 Su amee ci seen biir ab ndóol, di kenn ci seen bokki bànni Israyil, ci benn ci seen dëkki réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen dëgër xol, di tëjal seen loxo, seen mbokkum ndóol moomu. 8 Nàddil-leen koo nàddil, abal koo abal dayob soxlaam. 9 Wattuleen seen bopp, bala leena jikko ju sew yóbbe ngeen naan ci seen xel: «Atum juróom ñaareel mi, atum njéggalug bor dëgmal na,» ba tax ngeen sajje xef, seen mbokkum ndóol, joxuleen ko dara. Da leen di booleek Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar. 10 Nangeen ko joxa jox te bu ngeen koy jox it, bu ci seen xol bon, ndax loolu mooy tax seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seen liggéey, ak mboolem seenu ñaq. 11 Du ñàkk nag ab ndóol ci réew mi. Moo tax ma sant leen ne leen ngeen nàddila nàddil seen mbokkum ndóol, ak seen néew-ji-doole ji ci seenum réew.
16 Ndegam nag seen jaam a leen ne: «Duma dem, ba la,» ndax cofeel gu mu am ci yeen ak seen waa kër, te bànneexam di nekk ak yeen, 17 su boobaa fableen puso, ngeen sësale noppu jaam bi seen lafu bunt, te ngeen bënne puso bi noppam, ba mu jam ci lafu bunt bi, mu daldi doon seen jaam ba fàww. Seen jaam bu jigéen it, noonu ngeen di def ak moom.
18 Buleen mititlu lu ngeen yiwi seenub jaam, mu moom boppam, ndax jariñ na leen lu fey ñaari yoon surga buy feyeeku, ci juróom benni at yi mu leen liggéeyal. Te seen Yàlla Aji Sax ji dina leen barkeel ci mboolem lu ngeen def.
- a 15.12 Mbaa: su fekkee ne dees leena jaay seen mbokkum bànni Israyil.