7 Seen mbokk mu ngeen bokkal jenn ndey, mbaa seen doom ju góor, mbaa ju jigéen, mbaa seen jabar ju ngeen xejjoo, mbaa seen xaritu benn bakkan, su leen dee xiirtal, naan leen ci kumpa: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, du yeen du seeni maam, 8 ci yàllay xeet yi leen séq, ñi leen jege, ak ñi leen sore, ci àddina sépp, cat ba cat, 9 su boobaa buleen ko nangul, buleen ko déglu, buleen ko xool bëti yërmande, buleen ko baal, buleen ko nëbbal. 10 Reyleen ko rekk. Yeen ñi mu doon jéema yóbbaale, na ko seen loxo jëkka dal, ngir rey ko, bala cee loxol mbooloo mépp topp. 11 Dóorleen koy doj ba mu dee, ndax moo leen doon fexee soreleek seen Yàlla Aji Sax, ji leen jële réewum Misra, kërug njaam ga. 12 Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal ba deesatul def mbon gu ni mel ci seen biir.
13 Bu ngeen déggee, ci benn dëkk, ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ngir ngeen dëkke, ñu ne 14 ay nit ñu tekkiwul dara, te bokk ci yeen, ñoo jóg di waññi seen waa dëkk, naan leen: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, 15 su boobaa nangeen gëstu, seet te laajte bu baax, ba dëgg gu wér feeñe ca mbir ma, ne defees na moomu mbir mu jomblu ci seen biir, 16 ngeen daldi jam rekk waa dëkk boobu, leel leen ñawkay saamar, faagaagal dëkk ba, ak mboolem la ca biiram, jur ga it, ngeen leel leen ñawkay saamar. 17 Mboolem alalu sëxëtoo ju jóge ca dëkk ba, dajaleleen ko ca digg pénc ma, te ngeen lakk dëkk ba, booleek cëxëtoo ma, def ko dóomal bu mat sëkk, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Day doon ab gent ba fàww, deesu ko tabaxaat. 18 Bu dara des ci seen loxo, lu bokk ci alal jooju ñu wara faagaagal. Su ko defee Aji Sax ji dëddu sànjam mu tàng, yërëm leen, ñeewante leen, yokk leen na mu ko giñale woon seeni maam, 19 ndegam yeena ngi dégg seen kàddug Yàlla Aji Sax ji, ngir sàmm mboolem santaaneem yi ma leen di dénk bésub tey, ngir di jëfe li seen Yàlla Aji Sax ji rafetlu.
<- Baamtug Yoon wi 12Baamtug Yoon wi 14 ->