13 Ba loolu amee ma dégg jenn aji sell di wax, jeneen aji sell ne ko: «Lan mooy àppu peeñu mii ñu gis, ñu di ci dakkal sarax biy am bés bu jot, di teddadil gàngooru xare gi, ak a tooñ, di yàq lépp?» 14 Mu ne ma: «Àpp bi ñaari junni laak ñetti téeméer ciy guddeeki bëccëg. Gannaaw loolu dees na taxawalaat bérab bu sell bi.»
15 May xool ci biir peeñu mi, man Dañeel, di jéema xam lu muy tekki, jëmm juy nirook góor, ne jimeet taxaw ci sama kanam. 16 Ci kaw loolu ma dégg baatu nit jibe ca digg yoonu ndox ma ñuy wax Ulay. Mu àddu ca kaw ne: «Jibril, waxal kii peeñu mi.» 17 Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.» 18 Bi muy wax ak man, dëpp naa sama kanam fi suuf, ba daanu leer. Mu laal ma, taxawalaat ma fa ma taxawoon. 19 Mu ne ma: «Maa ngi lay xamal luy xew keroog ba merum Yàlla di jeex, ndax muj ga mooy àppu mer ma. 20 Kuuy mi nga gis mu am ñaari béjjén, buuri waa Medd ak waa Pers la. 21 Sikket bi buuru réewum Geres la. Béjjén bu gudd bi ci diggante bët yi mooy buur bu jëkk bi. 22 Dañu koo damm, ñeenti béjjén wuutu ko, di ñeenti nguur yu soqeekoo ca xeet wa, waaye duñu am doole ni ga jiitu. 23 Bu nguur yooyu jeexee, ba bàkkaarkat yi buural, buur bu néeg te bare pexe dina falu. 24 Dina gëna am doole, waaye du doon dooley boppam. Yàqam dina jéggi dayo, te ay pexeem dina joy. Dina faagaagal ñu am doole ba ca mbooloom aji sell yi. 25 Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, faagaagal leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal. 26 Peeñum ngoon meek mu bëccëg mi la dikkal lu wér la. Yaw nag neel cell ak peeñu mi, ndax des na fan yu bare.»
27 Ba loolu amee ma ne làcc, wopp ay fan, man Dañeel. Gannaaw gi ma jóg, dellu ca liggéeyu buur. Ma waaru nag ca peeñu ma, ndax daa wees sama dég-dég.
- a 8.9 réew ma gëna rafet fii réewum Israyil a tax ñuy wax.