4 Yéenekat ba nag xaacu, ne: «Dégluleen li ñu leen sant, yeen waa mbooloo yépp ak xeet yépp, ak làkk yépp. 5 Bu ngeen di dégg bufta gi ak toxoro gi ak xalam gi ak riiti gi ak kooraa gi ak liit gi ak mboolem jumtukaayu xumbal yi, nangeen sujjóot, màggale ko jëmmu wurus wi Buur Nabukodonosor samp. 6 Képp ku sujjóotul màggal ko, dees koy daldi sànni ci biir taal bu yànj.»
7 Loolu nag waral saa yu nit ña déggee bufta gaak toxoro gaak xalam gaak riiti gaak kooraa gaak mboolem jumtukaayu xumbal ya, ñoom ñépp ay bokk sujjóot, màggal jëmmu wurus ja Buur Nabukodonosor samp, muy mbooloo yaak xeet yaak làkk ya.
8 Ci biir loolu ay xërëmkat dikk, di boole Yawut ya. 9 Ñu wax Buur Nabukodonosor, ne ko: «Buur, guddalu fan. 10 Buur sang bi, xam nga yaa joxe ndigal ne: “Képp ku dégg bufta geek toxoro geek xalam geek riiti geek kooraa geek liit geek mboolem jumtukaayu xumbal, dangaa wara sujjóot, màggal jëmmi wurus ji. 11 Te képp ku sujjóotul màggal ko, dees na ko sànni ci biir taal bu yànj.” 12 Dafa am ay Yawut yoo tabb, ñu yore saytub diiwaanu Babilon. Ñu di leen wax Sadarag ak Mesag ak Abet Nego. Ñooñu de Buur, déggaluñu la; say yàlla, jaamuwuñu leen; sa jëmmu wurus ji nga samp it, màggaluñu ko.»
13 Nabukodonosor daldi mer lool, ba fees dell. Mu woolu Sadarag ak Mesag ak Abet Nego; ñu indi leen ba fa kanam Buur. 14 Nabukodonosor àddu ne leen: «Ndax dëgg la, yeen Sadarag, Mesag ak Abet Nego, yeena baña jaamu samay yàlla, baña màggal jëmmu wurus ji ma samp? 15 Léegi, bettuma leen. Bu ngeen di dégg bufta geek toxoro geek xalam geek riiti geek kooraa geek liit geek mboolem jumtukaayi xumbal yi rekk, sujjóotleen, màggale ko jëmm ji ma sàkk. Waaye su ngeen ko màggalul, dees na leen daldi sànni ci biir taalu sawara bu yànj. Ana yàlla ju leen di musal ci man?»
16 Sadarag Mesag ak Abet Nego ne Buur Nabukodonosor: «Buur, soxlawul ñu di la lay dara. 17 Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal. 18 Su demewul noonu it nag Buur, xamal ne say yàlla dunu leen jaamu, sa jëmmu wurus ji nga samp it, dunu ko sujjóotal.»
19 Ci kaw loolu Nabukodonosor mer lool ba fees dell, kanam gay sël-sëli janook Sadarag Mesag ak Abet Nego. Mu santaane ñu xamb taal ba, ba mu gëna tàng juróom ñaari yoon na mu daan tànge; 20 ba noppi mu sant ay dag yu am kàttan ci mbooloom xareem, ngir ñu yeew Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, sànni leen ca biir taal bu yànj ba. 21 Ñooñu yeew leen na ñu soloo, ñook seeni mbubb ak seeni tubéy ak seeni mbaxana, daldi leen sànni ca biir taal bu yànj ba. 22 Ndigalu Buur nag jampa jamp, sawara wa boya boy, ba tàkk-tàkku sawara wa rey dag, ya ca sànni Sadarag ak Mesag ak Abet Nego. 23 Sadarag, Mesag ak Abet Nego, ñoom ñett ñépp yeewe ba ne ŋodd, tàbbi ca biir taalu sawara bu yànj ba.
24 Ci kaw loolu Buur Nabukodonosor jommi, ne bërét taxaw, daldi laaj ay dagam ne leen: «Xanaa du ñett lañu yeew, sànni ci sawara wi?» Ñu ne ko: «Ahakay, Buur!» 25 Mu ne: «Xool-leen, ñeent ñu yeewewul laa gis, ñuy daagu ci biir sawara wi te dara dalu leen. Ñeenteel baa ngi mel ni jëmm ju nirook Yàlla.» 26 Nabukodonosor nag jegeñsi buntu taal bu yànj ba, daldi àddu ca kaw ne: «Éey Sadarag, Mesag, Abet Nego, jaami Yàlla jiy Aji kawe ji, génnleen fii!»
28 Nabukodonosor wax ne: «Cant ñeel na Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, moom mi yónni malaakaam, mu wallu jaamam ñi ko wóolu, ba xëtt sama ndigal man Buur, te jaay seen bakkan gënal leen ñuy jaamu mbaa di sujjóotal jeneen yàlla ju dul seen Yàlla. 29 Dogal tukkee na ci man ne: muy mépp mbooloo ak bépp xeet ak wépp làkk, képp ku ci ñàkke kersa Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, ay dog lees koy dog, te këram dees na ko def ab sën, ndax kat amul jenn yàlla ju mana walloo ni moom.»
30 Ba loolu wéyee Buur gëna teral Sadarag ak Mesag ak Abet Nego ca diiwaanu Babilon.