Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 6
Boroom alal naagu na
1 Wóoy ña ne finaax ca Siyoŋ,
wóoy ña naagu fa tundu Samari!
Ñooy kàngami xeet wi gëna màggeey,
niti Israyil di leen diis-si soxla.
2 Jàll-leen ba Kalne, xool;
jóge fa jëm Amat dëkk bu mag ba*6.2 Kalne ak Amat ay dëkki Siri lañu woon.,
wàcci Gaat, dëkkub waa Filisti ya.
Ana fu ñu tanee yii réew?
ak fu ñu leen ëpplee suuf?
3 Wóoy yeen ñiy jéema fanq bésub njàqare
tey woo nguurug fitna!
4 Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj,
ak a sóonoo seen laltu yu nooy,
di yàpp mbote yu baax
ak sëllu yu duuf,
5 yeena ngi foyantoo xalam,
di fent woy yu ànd ak xalam ni Daawudaay.
6 Yeena ngi jolu seen këlli biiñ,
di diwoo ngën-gi-diw,
sànkutey askanu Yuusufa soxalu leen.
7 Moo tax yeenay jiituji ngàllo ga,
tëraayu xawaare dakk.
 
8 Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam,
kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi.
Nee: «Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba,
ba seen kër yu yànj soof ma!
Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.
9 Su boobaa, fukk ñu làqu ci kër, du leen teree dee.»

10 Ku warloo waajal mbokkam mu dee dina dugg ca kër ga, ngir yóbbu néew ya, te naan ka ca biir-a-biir: «Kenn desul foofu ci yaw?» Mu ne ko: «Jeex na,» bëgg caa teg baat, mu ne ko: «Déet! Noppil, bul tudd turu Aji Sax ji.»

11 Aji Sax jee ngii déy, buy joxe ndigal rekk,
daldi tas kër gu mag,
rajaxe kër gu ndaw.
12 Moo fas dina daw ciy doj a?
Am dees na ràng aw nag, di gàbb doj?
Moona walbati ngeen àtteb yoon, def ko tooke,
yoon mel ni xay.

13 Yeena ngi damu ca dëkk ba ñuy wax Lodebar (mu firi Amul njariñ) te naan: «Xanaa du sunu dooley bopp lanu nangul sunu bopp dëkk bu am doole ba ñuy wax Karnayim (mu firi Ñaari béjjén)6.13 Ñaari béjjén: kàttan lay misaal.14 Aji Sax ji, Yàlla, Boroom gàngoori xare yi da ne:

«Yeen bànni Israyil,
maa ngii di yékkati weneen xeet fi seen kaw,
ñu not leen, dale ko fa kaw, fa buntu Amat
ba ca xuru Araba, fa suuf.»