Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Aji Sax ji dige na mbugal
Saar 3
(Saar 3.1—6.14)

1 Dégluleen kàddu gii Aji Sax ji wax ci yeen, bànni Israyil, mu jëm ci seen mboolem xeet wi mu génnee réewum Misra. Mu ne:

2 «Yeen doŋŋ laa ràññee
ci mboolem askani suuf.
Moo tax ma di leen mbugal
ndax seen ñaawtéef gépp.»
 
3 Ñaar dina ànd te digewuñub dajee?
4 Gaynde dina ŋarem ngeer te fàddul?
Am gaynde gu ndaw dina xiiroom paxam te jàppul?
5 Picc dina keppu te fiireesu koo?
Am ag fiir dina fettax te jàppul?
6 Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a?
Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?
7 Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def,
te déeyu ko yonent yiy jaamam.
8 Bu gaynde yëmmoo, ana ku dul tiit?
Ana ku saña baña biral waxyu,
bu ko Boroom bi Aji Sax ji waxee?
 
9 Yéeneleen ca biir taaxi Asdodd
ak ca biir taaxi Misra.
Neleen: «Dajeleen ca kaw tundu Samari,
ba gis na Samari salfaañoo,
ak notaange ga fa nit di daj.
10 Xamuñu sax def njub.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Dañuy jal alalu fitnaak yàqute
ci seen biiri taax.»
11 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji ne:
«Ab noon dina gaw seenum réew,
néewal leen doole, lël seeni taax.»
12 Aji Sax ji nee:
«Wallub sàmm ak gàtt bu gaynde fàdd
weesul ñaari yeel, dogitu nopp.
Kuy wallu bànni Israyil ga ca Samareet,
xanaa dogu basaŋ, dammitu lal.
13 Dégluleen te àrtu waa kër Yanqóoba.»
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee,
Yàlla ji ci gàngoori xare yi.
14 «Bés bu may mbugale Israyil ay bàkkaaram,
damay tasaale sarxalukaayi Betel.
Béjjén yi ci cati sarxalukaay ba dog, rot.
15 Maay màbbaale këru taax ak këru àll;
kër yu ñu rafetale bëñu ñay dina yàqu,
te kër yu bare dootu taxaw.»
Kàddug Aji Sax jee.