14 Ba ndaw ya ca Yerusalem yégee ne waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla, Piyeer ak Yowaan lañu fa yebal. 15 Ñu agsi Samari, ñaanal gëmkat ña, ngir ñu jot Noo gu Sell gi. 16 Ndax booba Noo gi wàccagul woon ci kenn ci ñoom, dees leena sóoboon rekk ci ndox ci turu Sang Yeesu. 17 Ba loolu amee Piyeer ak Yowaan teg leen loxo, ñu jot Noo gu Sell gi.
18 Simoŋ nag gis noonee mayug Noo, gi sababoo ci tegeb loxo bu ndaw ña amal, ba tax mu indil leen xaalis. 19 Mu ne leen: «Mayleen ma man itam xam-xam bii, ngir ku ma teg loxo, nga jot Noo gu Sell gi.» 20 Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla! 21 Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla. 22 Réccul nag sa mbon gii, te ñaan Boroom bi; jombul mu baal la sa mébétu xol. 23 Ndax gis naa ni nga sóoboo ci wextanu kañaan, keppu ci ndëngte.» 24 Simoŋ ne leen: «Ñaanal-leen ma Boroom bi, yeen ci seen bopp, ngir li ngeen wax lépp, lenn bañ ma cee dab.»
25 Gannaaw ba Piyeer ak Yowaan seedeelee kàddug Boroom bi, biral ko, Yerusalem lañu dellu, di xamle xibaaru jàmm bi ci ay dëkki Samari yu bare.
30 Filib dabsi waayi Ecopi ja, daldi dégg muy jàng téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?» 31 Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, te kenn firilu ma ko?» Ba loolu amee mu ne Filib, mu yéeg, toog ak moom. Filib yéeg. 32 Lii nag mooy dogu mbind ma mu doon biral:
34 Jaraaf ja ne Filib: «Yaw laay laaj, ci kan la yonent bi wax lii? Boppam lay wax am keneen?» 35 Filib daldi àddu, tàmbalee ci dog boobu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
36 Ba loolu amee ñu topp yoon wi, ba yem ci am ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngii, ana lu tee ma sóobu ci?» 37 Filib ne ko: «Soo gëmee ci sa léppi xol, sañ nga ko.» Mu ne ko: «Gëm naa ne Yeesu Almasi mooy Doomu Yàlla.»
38 Ci kaw loolu jaraaf ja santaane ñu taxawal watiir ba; Filib ak jaraaf ja wàcc, ñu dugg ñoom ñaar ca ndox ma, Filib sóob ko ca. 39 Naka lañu génne ca ndox ma, ngelawal Boroom bi ne cas Filib, yóbbu, jaraaf ja gisatu ko. Teewul mu topp yoonam, ànd ak mbég. 40 Filib moom, dëkk ba ñuy wax Asot la gisaat boppam. Mu wéye di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkkoo dëkk, ba àgg Sesare.
<- Jëf ya 7Jëf ya 9 ->- a 8.27 Ecopi ga woon, dees na ko wooye Kuus itam, muy diiwaan bu feggoo woon ak dexu Niil, te nekkoon diggante bëj-gànnaaru Sudan ak bëj-saalumu Misra.