5 Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit kufeese ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas, ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut. 6 Ñu indi leen fa kanam ndaw ya, ñu ñaanal leen, teg leen loxo.
7 Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.
11 Ñu daldi ger ay nit ngir ñu duural ko, ne: «Noo ko dégg, mu yékkati kàdduy saaga, jëme ci Musaa ak ci Yàlla.» 12 Ba loolu amee ñu xabtal nit ñi ak njiit yi, ak firikati yoon yi, ñu ne jalañ, jàpp Eccen, yóbbu ca kurélu àttekat ya. 13 Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak bérab bu sell bii ak yoonu Musaa. 14 Noo ko dégg mu ne Yeesu Nasareen boobu dina màbb bérab bii te dina soppi aada yi nu Musaa bàyyee.»
15 Mboolem ña ca jataayu àttekat ya nag ne jàkk Eccen; ñu gis xar-kanam ba ne ràññ ni xar-kanamu malaaka.
<- Jëf ya 5Jëf ya 7 ->