6 «Yàlla def ma topp yoon wa, ba jub Damaas ci digg bëccëg rekk, ag melax gu mag jekki fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër. 7 Ma ne dàll fi suuf, daldi dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?” 8 Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Mu ne ma: “Man maay Yeesum Nasaret, mi ngay bundxatal.” 9 Ñi ma àndaloon gis nañu leer gi, waaye ki wax ak man, xamuñu li mu wax. 10 Ma ne ko: “Sang bi, nu may def?” Sang bi ne ma: “Jógal dem Damaas, dees na la wax foofa mboolem li ñu la sas, nga def ko.” 11 Gisatuma woon dara ndax leeraayu melax ga; ña ma àndal ñoo ma mujj wommat, ba ma agsi Damaas.
12 «Ku ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Ku am diiney yoonu Musaa te rafetub jëw ci biir mboolem Yawuti dëkk ba. 13 Mu dikk taxaw fi sama wet, ne ma: “Mbokk mi Sóol, gisal na woon.” Ca saa sa, may gis na woon, di ko xool. 14 Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw. 15 Ndax li nga gis, dégg ko, yaa koy seedeel nit ñépp. 16 Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set, teqlikook say bàkkaar, te tudd turu Yeesu.”
17 «Yàlla def, gannaaw ba ma délsee Yerusalem, ma doon ñaan ca kër Yàlla ga, daldi daanu leer. 18 Ma gis Sang bi, mu ne ma: “Gaawal, daw génn Yerusalem, li nga may seedeel, duñu ko nangu.” 19 Ma ne ko: “Sang bi, ñoom ci seen bopp xam nañu ne jàngu ci kaw jàngu, maa fa daan tëjlu ak a cawlu ñi la gëm. 20 Te it ba ñuy tuur deretu Eccen, sa seede ba, man it maa nga fa woon, juboo caak ñoom, te ña ko rey, maa leen doon wattul seeni yére.” 21 Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”»
26 Njiitu takk-der ba dégg loolu, daldi dem ba ca njiital gàngoor ga, xamal ko ko, ne ko: «Li ngay def nag? Nit kii as goru Room la!» 27 Njiital gàngoor ga dikk, ne Póol: «Yaw wax ma, ndax as goru Room nga?» Mu ne: «Waaw.» 28 Mu ne ko: «Man de xaalis bu bare laa jënde sañ-sañu doon as goru Room.» Mu ne ko: «Man nag moom laa judduwaale.» 29 Ña ko doon waaja laaje ay dóor nag dànd ko ca saa sa. Njiital gàngoor ga it tiit na, ba mu yégee ne Póol as goru Room la, te fekk mu yeewlu ko.