5 Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp. 6 Naka la coow li jolli, nit ñi daje, ku nekk ci mbooloo mi dégg ñuy làkk sa làkku bopp, mbooloo ma jaaxle. 7 Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile? 8 Ana nu kenn ku nekk ci nun nag mana dégge ñuy wax ci làmmiñ wi nga nàmp? 9 Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi, 10 ak Firisi ak Pamfili ak Misra ak wàllu Libi ga dendeek Siren, ak gan ñi jóge Room, 11 ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!» 12 Ñépp waaru, ba jànnaxe, di wax ci seen biir naa: «Lii lu muy tekki nag?» 13 Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
22 «Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll. 23 Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko. 24 Waaye moom la Yàlla yiwee ci mititu ndee, dekkal ko, ndax dee amul kàttanu tënk ko. 25 Daawuda wax na ci mbiram ne:
29 «Bokk yi nag, Maam Daawuda, manees na leena wax ci lu wér ne nelaw na, ba ñu denc ko, te bàmmeelam a ngi fi, nuy gis ba tey jii. 30 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku bokk ci geñoom lay teg cib jalam. 31 Kon li mu gis te dikkagul mooy ndekkitel Almasi, te ci mbiram la wax ne bàyyeesu ko biir njaniiw, te yaramam du yàqu. 32 Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp. 33 Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko. 34 Ndax kat du Daawudaa yéeg asamaan, waaye moom ci boppam moo ne:
36 «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
37 Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?» 38 Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye. 39 Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jaambur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.» 40 Yeneen kàddu yu bare soññe na leen ko, ñaaxe leen ko, ne leen: «Muccleen ci gii maas gu dëng.»
41 Ña nangu kàddug Piyeer nag, ñu sóob leen ci ndox; bésub keroog lu wara mat ñetti junni (3 000) yokku nañu ca gëmkat ña.
- a 2.42 Dagg mburu: moom la gëmkat ñi aadawoo woon, bu ñuy lekk. Dagg mburu, moom lañu mujj di wooye Reeru Sang bi.