13 Ba bésub Noflaay ba taxawee, nu génn ca buntu dëkk ba, ca wetu dex ga, daldi fay gis bérab bu nu foog ne ab jullikaay la. Nu toog fa nag, di waxtaan ak jigéen ña fa daje. 14 As ndaw a nga ca, di déglu; ku ñuy wax Lidi, dëkke Catir, di jaaykatub cuubi tànnéef yu xonq curr, te di jaamukatu Yàlla. Boroom bi nag ubbi xolam, ba mu teewlu bu baax kàdduy Póol. 15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.
19 Ba loolu amee alal ja njaatigey ndaw sa yaakaaroon, réer leen, ñu jàpp Póol ak Silas, diri, yóbbu ca pénc ma, fa kanam njiit ya. 20 Ñu taxawal leen fa àttekat ya, ne: «Ñii ñoo yëngal sunu dëkk bi, di ay Yawut 21 yuy xamle aada yoy, nun ñiy waa Room, sañunu koo nangu, sañunu koo jëfe.»
22 Ci kaw loolu mbooloo ma it dal ci seen kaw; àttekat ya futti seeni yére, daldi santaane ñu dóor leen ay yar. 23 Ñu dóor leen ay yar yu bare, sànni leen ca kaso ba, boole ca jox boroom kaso ba ndigalal wattu leen bu baax. 24 Ndigal loolu nag tax mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqe ca kaso ba, jéng leen.
25 Ba guddi gay xaaj, Póol ak Silas a ngay ñaan, di sàbbaal Yàlla, ñeneen ña ñu fa tëj di leen déglu. 26 Ci kaw loolu suuf jekki yëngu yëngu bu mag ba kenug kaso ba di rëng-rëngi; bunt yépp jekki ubbiku, jéngi ñépp dàjjiku. 27 Boroom kaso ba tiite ciy nelaw, gis bunti kaso bi ubbiku. Mu bocci saamaram, nara xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo rëcc. 28 Póol nag àddu ca kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp a ngi fi.»
29 Ba loolu amee boroom kaso ba indilu ab làmp, daldi ne saraax dugg, ne gurub fa kanam Póol ak Silas, di lox. 30 Gannaaw gi mu génne leen ca biti ne leen: «Sang yi, ana lu ma wara def, ba mucc?» 31 Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.» 32 Ba loolu amee ñu xamal ko kàddug Sang bi, moom ak waa këram gépp. 33 Mu yóbbu leen nag ci waxtuw guddi woowu, raxas seeni gaañu-gaañu, ñu sóob ko ci ndox ca saa sa, moom ak waa këram gépp. 34 Gannaaw loolu mu yóbbu leen këram, jox leen ñu lekk, tey bégeendoo ak waa këram gépp ci ngëm gi ñu gëm Yàlla.
35 Ba bët setee, àttekat ya yebal alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Ñii, yiwi leen.» 36 Boroom kaso ba àgge Póol ndigal la, ne ko: «Àttekat yi kat ñoo fi yeble, ne ñu yiwi leen. Kon nag man ngeena génn te dem ak jàmm.»
37 Póol nag ne alkaati ya: «Ñoom ñu dóor nu ci kanam nit ñi, àtteesu nu sax te nu diy gor ci Room gii, rax ci dolli ñu sànni nu ci kaso bi. Léegi ñu bëgg noo dàq ndànk ci biti? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, génne nu.»
38 Ba mu ko defee, alkaati ya àgge àttekat ya kàddu googu, ñu xam ne ay gori waa Room lañu, tiitaange jàpp leen. 39 Ñu dikk, jéggalu, génne leen ci biti, ñaan leen, ñu génn dëkk ba. 40 Noonu lañu génne kaso ba, dellu kër Lidi. Ñu gise faak bokki gëmkat ña, ñaax leen, doora dem.
<- Jëf ya 15Jëf ya 17 ->