2 Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnaba séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnaba, ak ñenn ca gëmkati Àncos, ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu, ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
3 Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jaambur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool. 4 Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi, ak ndawi Yeesu yi, ak mag ñi, dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
5 Ba mu ko defee ñenn ci gëmkat ñi bokk ci ngérum Farisen yi, daldi taxaw temm, ne gëmkat ñi dul Yawut, fàww ñu xarfal leen, sàmmloo leen yoonu Musaa.
6 Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu. 7 Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat. 8 Yàlla, mi xam xolu nit nag moo seereel jaambur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam. 9 Yàlla amul xejj ak seen sunu digg ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol. 10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun? 11 Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12 Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnaba ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan, yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jaambur ñi. 13 Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma. 14 Simoŋ†15.14 Simoŋ mooy Piyeer ba tey. xamle na, ni Yàlla yége jaambur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir, xeet wu mu tudde turam. 15 Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndax bindees na ne:
19 «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jaambur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla. 20 Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam. 21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
23 Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne:
39 Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqlikoo. Barnaba ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar. 40 Póol moom, taamu Silas, daldi ànd ak moom dem, gannaaw ba leen bokk ya dénkee Boroom bi ciw yiwam. 41 Ci kaw loolu mu jaare diiwaani Siri ak Silisi, di ñaax mboolooy gëmkat ña.
<- Jëf ya 14Jëf ya 16 ->