Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 11
Piyeer layoo naak waa Yerusalem
1 Ci kaw loolu ndaw yaak bokki gëmkat ña ca réewum Yawut, dégg ne jaambur ñi dul Yawut déggal nañu kàddug Yàlla, ñoom itam. 2 Ba Piyeer delloo Yerusalem nag, gëmkat ñi bokk ci askanu Yawut di ko sikk, 3 naan: «Yaa dem ca ña xaraful, di bokk ak ñoom lekk!»

4 Piyeer daldi leen benn-bennalal mbir mi. 5 Mu ne: «Man de damaa nekkoon ca Yope, di fa ñaan. Ci biir loolu ma daanu ag leer, daldi gis ci peeñu lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, mu wàcce asamaan, ba agsi ci man. 6 Ma xool ko jàkk, niir ko, daldi cay gis boroom ñeenti tànk yi, ak rabi àll yi, ak dundoot yiy raam ak njanaaw yi. 7 Maa dégg itam baat bu ma ne: “Piyeer, jógal, rey te lekk.” 8 Ma ne: “Mukk, Sang bi, ndax lenn lu daganul mbaa lu setul masula dugg sama gémmiñ.” 9 Baat ba nag àddoo asamaan ñaareel bi yoon, ne ma: “Lu Yàlla setal, bu ko daganadil.” 10 Menn peeñu moomu dikk na ba muy ñetti yoon, ñu doora yéege lépp asamaan.

11 «Saa soosa tembe, ca la ñetti nit ña ñu yebale Sesare ba ca man, agsi ca kër ga nu dal. 12 Noo gi nag ne ma: “Àndal ak ñoom, te bul nàttable.” Juróom benni bokk yii ngeen di gis ñoo ma gunge, nu dem ba dugg ca kër Korney. 13 Mu xamal nu ne malaakaa ko feeñu ci néegam, ne ko: “Yebleel ca Yope, nga woolu Simoŋ, ma ñu dàkkentale Piyeer. 14 Dina la àgge kàddu yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”

15 «Naka laa tàmbalee wax ak ñoom Korney, Noo gu Sell gi daanu ci seen kaw, na mu jëkkoona daanoo ca sunu kaw. 16 Ma daldi fàttliku kàddug Sang, ba mu noon: “Yaxya, cim ndox la daan sóobe, waaye yeen, ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob.” 17 Gannaaw nag Yàllaa leen jagleel genn may, ga mu nu jagleeloon, ba nu gëmee Sang Yeesu Almasi, ana ku ma doon, man, bay gàllankoor Yàlla?»

18 Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»

Mbooloo sosu na ca Àncos
19 Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi. 20 Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu. 21 Boroom bi nag gungee leen loxoom, ba ñu bare gëm, waññiku ci Sang bi.

22 Ba mbir ma siiwee, ba mbooloom gëmkati Yerusalem jot ca, dañoo yebal Barnaba ca Àncos. 23 Ba Barnaba dikkee ba gis yiw, wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoye seen xol ci Sang bi. 24 Ndaxte Barnaba nit ku baax la woon, feese Noo gu Sell gi, ak ngëm. Mbooloo mu takku nag dolliku ci Sang bi.

25 Ba loolu wéyee Barnaba jëm Tàrs, di seeti Sóol. 26 Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.

27 Ci fan yooyu la ay yonent jóge Yerusalem, dikk Àncos. 28 Kenn ca ñoom, ku ñuy wax Agabus daldi yéglee Noo gu Sell gi, ne xiif bu metti dina am, ci àddina sépp. Te looloo nga yemook ayug buur bu mag bu ñuy wax Këlódd. 29 Taalibe ya nag fas yéenee boole kem kàttanu ku nekk ca ñoom, ngir ndimbal lu ñuy yónnee bokki diiwaanu Yude. 30 Noonu lañu def, yónnee ko magi Yude, Barnaba ak Sóol jottli ko.

<- Jëf ya 10Jëf ya 12 ->