6 Naka lañu dem ba tollu ca dàggay Nakon, nag ya tërëf, Usa tàllal loxoom, jàpp ca gaalu Yàlla ga. 7 Sànjum Aji Sax ji nag tàkk ci kaw Usa. Yàllaa ko fàdd foofa, ndax ug teeyadeem, mu dee foofa ca wetu gaalu Yàlla ga*6.7 Sarxalkat yi rekk ñoo amoon sañ-sañu laal gaalu Yàlla ga, te Leween ñi rekk ñoo amoon sañ-sañu gàddu ko.. 8 Ba loolu amee Daawuda mer ca mbugal mu metti ma Aji Sax ji teg Usa. Moo tax mu tudde bérab booba Peres Usa (mu firi Mbugalum Usa), muy turam ba tey jii.
9 Daawuda am na tiitaange lool bésub keroog ci Aji Sax ji. Ma nga naan: «Ana nu gaalu Aji Sax ji mana dale ak man?» 10 Loolu nag tax Daawuda nanguwula yóbbu gaalu Aji Sax ji fa moom, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Mu waññi gaal gi, yóbbu ko ca kër Obedd Edom waa Gaat ba. 11 Gaalu Aji Sax ji nekk na kër Obedd Edom waa Gaat ba ñetti weer. Aji Sax ji barkeel Obedd Edom, mook këram gépp.
16 Ba gaalu Aji Sax jay duggsi ca biir gox ba ñu naan Kër Daawuda, soxnas Daawuda, Mikal doomu Sóol a nga sëppu ca palanteeram. Mu gis Buur Daawuda di tëb ak a fecc ca kanam Aji Sax ji. Mu jéppi ko lool.
17 Ba mu ko defee ñu indi gaalu Aji Sax ji, yeb ko ca bérabam, ca biir xayma ba ko Daawuda sampal. Daawuda daldi joxe fa kanam Aji Sax ji ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm. 18 Daawuda joxe saraxi rendi-dóomal ak saraxi cant ci biir jàmm, ba noppi daldi ñaanal askan wi ci turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. 19 Mu séddale aw ñam askan wépp, mbooloom Israyil mépp, góor ak jigéen; ku ci nekk mu jox la menn mburu ak yàpp wu ñu saaf†6.19 yàpp wu ñu saaf walla benn nàkku tàndarma. ak benn nàkku reseñ. Mbooloo ma doora dem, ku nekk ñibbi këram.
20 Ba loolu amee Daawuda walbatiku, dugg biir këram, ngir ñaanal waa këram. Soxnaam Mikal doomu Sóol génn dajeek moom, ne ko: «Buuru Israyiloo, yaaka teral sa bopp bésub tey jii! Nga futteeku tey jii fi kanam jigéen ñiy sa jaami jawriñ yi, mbete nit ku tekkiwul dara!» 21 Daawuda ne Mikal: «Fi kanam Aji Sax ji ma taamu, wacc sa baay ak waa këram gépp, ngir fal ma kilifag Israyil, ñoñi Aji Sax ji, fi kanam Aji Sax ji laay bànneexu. 22 Dinaa gëna teddadil sama bopp sax, gëna toroxlu, ba gisal ko sama bopp, te du tere jaam yu jigéen yi ngay wax teral ma.» 23 Mikal doomu Sóol jooju nag amul doom, ba ni mu deeye.
<- 2.Samiyel 52.Samiyel 7 ->