Saar 23
Daawuda biral na waxyu
1 Kàddu yii la Daawuda tàggtoo. Da ne:
Kàddug Daawudaa ngi, doomu Yese,
kàddug góor gu ñu kaweel,
góor gi Yàllay Yanqóoba fal,
muy woykatu Israyil, bi ñu ñal.
2 Noowug Aji Sax jee may waxe,
sol ma kàddoom.
3 Yàllay Israyil a wax,
moom mi Israyil sës, moo ne:
Ku jiite ay nit cig njub,
bu jiitee cig ragal Yàlla,
4 day mel ni leeru jant bu fenk,
kaw asamaanu suba su niir newul,
leeru asamaan su set, taw ba siwet,
ba ñax jebbi.
5 Du nii la sama waa kër def ak Yàlla?
Moo fas ak man kóllëre gu sax dàkk,
lépp jekk, mat sëkk.
Moo may may ndam saa su ne,
di ma defal lu ma namm.
6 Waaye ku bon, ñu buub nig taxas, sànni.
Deesu ko fore loxo,
7 xanaa fore ko weñ mbaa bantub xeej,
jafal mu lakk fa mu ne.
Jàmbaari Daawuda def nañuy jaloore
8 Ñeyi xarey Daawuda ya, ñoo di:
Yosebasebet waa Agmon ba bokk ca mbëri xare ya.
Moo xàcci xeejam, dal ci juróom ñetti téeméeri nit,
rey leen ci menn cong.
9 Ka ca topp di Elasar,
Elasar, Dodo.
Dodo, Awoya.
Elasar bokkoon na ci ñetti jàmbaari xare ya àndoon ak Daawuda,
di dëkk Filisteen ña fa daje woon ngir xare.
Fekk bànni Israyil di dellu gannaaw.
10 Elasar a taxaw, di cor Filisteen ña,
ba loxo ba banku, taq ca njàppul saamaram.
Aji Sax jee maye ndam lu réy bésub keroog!
Ba ko mbooloom bànni Israyil fekksee,
defuñu lu moy futti néew ya.
11 Ka topp ca Elasar di Saama.
Saama, Age ma dëkk Arar ay baayam.
Ba Filisteen ña dajee ca Léyi,
wetu toolub ñebbe ba meññoon, ba fees dell,
bànni Israyil dañoo daw.
12 Saamaa taxaw ca digg tool ba,
aar tool ba, duma Filisteen ña.
Aji Sax jee ca maye ndam lu réy!
13 Mu am bés, jamonoy ngóob,
ñett ca mbëri xare ya fekki Daawuda ca xunti ma ca Adulam.
Mbooloom Filisteen ñaa nga dal ca xuru Refayeen.
14 Daawudaa nga ca biir rawtoom.
Mu am kurélu xareb Filisteen ñu dal Betleyem.
15 Daawuda jekki-jekki xel ma sore.
Mu ne: «Éy ku ma wutali woon ndox mu ma naan ca teenu Betleyem ba ca buntu dëkk ba!»
16 Ci kaw loolu ñetti jàmbaari xare ya bëtt dalub Filisteen ña.
Ñu dem duyi ndox ca teenu Betleyem ba ca wetu buntu dëkk ba,
dikk yót Daawuda ndox ma.
Daawuda nag néegu koo naan;
da koo tuur, te Aji Sax ji tax.
17 Mu ne: «Yàlla tere, Aji Sax ji, may naan miim ndox,
nde kon deretu ñii dem jaayi seen bakkan laa naan.»
Daawuda naanul ndox ma.
Jooju jëf la ñetti jàmbaari xare ya def.
18 Abisay bokkoon na ca mbëri xare ya.
Abisay ak Yowab, Seruyaa di seen yaay.
Abisay a xàcci woon xeejam, dal ci kaw ñetti téeméeri nit, rey leen.
Mu doxe fa siiw ni ñett ñooña.
19 Abisay bokk na ca ña gënoona siiw ca Fanweeri jàmbaar ya;
mujj na sax di seen njiit,
waaye bokkuloon ca Ñett ña.
20 Benaya nag, Yoyadaay baayam,
xarekat bu mag la woon, dëkkoon Kabsel.
Def na jaloore yu réy!
Moo rey ñaari Mowabeen ña gënoona jàmbaare.
Moo wàccoon ci kàmb, bésu tawu yuur, rey fa gaynde.
21 Moo reyoon it waa Misra bu jekk ba taxawaay.
Waa Misra baa nga yor ab xeej,
Benaya songewu ko lu moy aw yet.
Mu bif xeeju waa Misra ba,
nangoo ko ciy loxoom, reye ko ko.
22 Jooju jëf la Benaya doomu Yoyada def.
Moom it siiwoon na ni ñetti mbëri xare ya,
23 ñu gënoon koo naw ca Fanweeri jàmbaar ya,
waaye bokkuloon ca Ñett ña.
Daawuda nag def ko njiitu dag ya ko dar.
24 Ñii bokkoon nañu ca Fanweeri jàmbaar ya:
Asayel, rakki Yowab,
Elxanan, Dodo di baayam, dëkk Betleyem,
25 Saama ma doon waa Arot,
Elika, di waa Arot,
26 Eles ma dëkk Pelet,
Ira, Ikes di baayam, dëkk Tekowa,
27 Abiyeser ma dëkk Anatot,
Mebunay dëkk Usa,
28 Salmon dëkk Awoya,
Maaray dëkk Netofa,
29 Eleb, Baana di baayam, dëkk Netofa,
Itay, Ribayi di baayam, dëkk Gibeya ca giirug Beñamin.
30 Benaya ma dëkk Piraton,
Iday ma dëkk walum Gaas,
31 Abi Albon dëkk Bet Araba,
Asmawet dëkk Barum,
32 Elyaba dëkk Saalbon,
ak góor ñi Yasen di seen baay,
ak Yonatan, 33 Saama di baayam, dëkk Arar,
Akiyam, Sarar di baayam, dëkk Arar,
34 ak Elifelet, Axasbay di baayam,
Axasbay, baayam dëkk Maaka,
ak Eliyam, Ayitofel di baayam, dëkk Gilo,
35 ak Esray ma dëkk Karmel,
ak Paray dëkk Arab,
36 ak Igal, Natan di baayam, dëkk Soba,
ak Bani ma dëkk Gàdd,
37 ak Seleg, Amoneen ba,
ak Naray ma dëkk Berot.
Kookoo yoroon ngànnaayi Yowab ma Seruya di yaayam.
38 Ira ma dëkk Yeter ca la,
ak Gareb dëkk Yeter,
39 ak Uri, Etteen ba.