6 Mbooloo maa nga jëm ca toolub xare ba, di xarejeek Israyil. Xare baa nga ame ca gott ba ñuy wax Efrayim, 7 mbooloom Israyil nag daanu foofa ca kanam xarekati Daawuda. Bésub keroog ñu baree dee: ñaar fukki junnee (20 000) daanu. 8 Xare ba daa law foofa ba daj diiwaan ba bépp; te ña dee ca gott ba bésub keroog ñoo ëpp ña saamar rey.
9 Ci biir loolu Absalom ne pemm taseek xarekati Daawuda. Ma nga war berkelle. Berkelle ba fëx wuti garab gu réy, te bànqaas ya fatt. Boppu Absalom tance ca garab ga, berkelle ba mu war topp xélam, mu des fa di sandaamtalu. 10 Ba mu ko defee jenn waay gis ko, dem, wax ko Yowab, ne ko: «Ki ma gis de, Absalom a, ma nga wékku ci genn garab.» 11 Yowab ne ko: «Nga ne? Gis nga ko te jamoo ko foofa, mu daanu? Kon de doon naa la jox fukki dogi xaalis, takkal la ngañaayal xarekat tegal la ca.» 12 Waa ja ne Yowab: «Ku tegoon ci sama loxo junniy dogi xaalis sax, duma xàcci sama loxo jëm ci doomu buur. Noo déggal sunu bopp Buur sant la, yaak Abisay ak Itay, ne leen: “Na ma ku nekk ci yeen dimbali, te def ndànk ak ngóor si Absalom.” 13 Su ma jaayoon sama bakkan, ba def njekkar it, amul dara lu ump Buur, te kon it yaw danga ciy raxas say loxo.» 14 Yowab ne ko: «Duma la déglu sax, nga di ma yàggal!»
18 Absalom moo samplu woon cig dundam, doj wu mag wa ca xuru Buur, ndax da noon: «Bàyyiwuma doom ju góor ju ñu may fàttlikoo.» Moo tax mu tudde doj wa boppam, te doju Absalom lañu koy wooye ba tey jii.
24 Daawudaa nga toog ca diggante buntu dëkk, ba féete biir ak bunt ba féete biti. Fekk na wattukat ba yéeg ca kaw taax ma tiim buntu dëkk ba, ca kaw tata ja. Naka la dawal bëtam, séentu, gis jenn waay juy daw moom kenn, di ñëw. 25 Wattukat ba àddu ca kaw, yégal ko Buur. Buur ne: «Gannaaw kenn nit la de, xibaaru jàmm lay indi.» Waa ja di gëna jegesi, 26 wattukat ba gis jeneen waay juy daw di ñëw, mu wax ko farbay bunt ba, ne ko: «Xoolal, keneen a ngi, di ñëw, moom kenn.» Buur ne: «Kooku it de xibaaru jàmm lay indi.» 27 Wattukat ba ne: «Ni ma gise ki jiitu de, dawinu Ayimaas doomu Cadog la ma jox.» Buur ne: «Kooku ku baax la, jàmm rekk lay waxsi.» 28 Ci kaw loolu Ayimaas àddu ca kaw, ne Buur: «Jàmm la!» daldi sujjóotal Buur, dëpp jëëm fa suuf, ne ko: «Buur, sang bi, cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi teg ci sa loxo ña la doon fexeel.» 29 Buur ne ko: «Ngóor sa Absalom nag, mbaa jàmm la am?» Ayimaas ne ko: «Sang bi, ba Yowab di yónni sa bëkk-néeg ak man, booba gis naa kër-kër ju réy, waaye xawma lu mu doon.» 30 Buur ne: «Randul, taxawe nii.» Ayimaas randu, taxaw ca wet ga.
31 Ci kaw loolu waa Kuus ba ne jimeet. Mu ne: «Buur, sang bi, déglul, xibaaru jàmm a ngi. Aji Sax ji musal na la bésub tey ci ña la doon fexeel ñépp.» 32 Buur ne waa Kuus ba: «Ngóor si Absalom mbaa jàmm la am?» Waa Kuus ba ne ko: «Buur sama sang, say noon ak mboolem ñi lay fexeel, yal nañu bokk ak ngóor soosu demin.»
<- 2.Samiyel 172.Samiyel 19 ->