Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 11
Daawuda topp na bakkanam
1 Gannaaw loolu, ca déwén sa, jamono ja buur ya daan xareji, Daawuda daa yebal Yowab, mu ànd aki nitam ak gàngooru Israyil gépp. Ñu faagaagal Amoneen ña, gaw péey ba ñu naan Raba. Fekk na Daawudaa nga des Yerusalem.

2 Genn ngoon, Buur Daawuda jóge ca kaw laltoom, di doxantu ca kaw taaxum këram. Mu tollu ca kaw taax ma, séen as ndaw suy sangu. Ndaw sa neexa xool lool. 3 Daawuda yónnee, gëstu mbiram, ñu ne ko: «Xanaa du Batseba doomu Eliyam, jabaru Uri, Etteen bi?»

4 Ci kaw loolu Daawuda yebal ay ndaw yu jëli ndaw si, mu dikk, mu tëdde ko. Fekk na ndaw sa gisoon baax bay doora sangu-set. Ndaw sa daldi ñibbi. 5 Ndaw si nag ëmb. Ba loolu amee mu yónnee ca Daawuda ne ko: «Man de, damaa ëmb.»

6 Ba mu ko defee Daawuda yónnee ca Yowab, ne ko mu wool ko Uri, Etteen ba. Yowab wool ko Uri. 7 Ba Uri dikkee, Daawuda nuyook moom ne ko: «Mbaa Yowab jàmm? Mbaa mbooloo ma jàmm? Mbaa xare ba jàmm?» 8 Ba loolu wéyee Daawuda ne Uri: «Àggal sa kër nag te jàngu.» Uri bàyyikoo kër Buur, ab yóbbalu Buur topp ca gannaawam. 9 Ndeke Uri ñibbiwul këram. Ca bunt kër Buur la tëdd, mook mboolem surgay Buur.

10 Ñu yégal Daawuda, ne ko: «Uri de ñibbiwul këram,» mu ne Uri: «Xanaa du ciw yoon nga jóge? Lu la tee àgg sa kër?»

11 Uri ne Daawuda: «Sang bi, gaalu Yàlla ga ak Israyil ak Yuda dëkke ay mbaar, sama njaatige Yowab ak surgay sang bi bokk dale ci digg àll bi, man may dem sama kër, di lekk ak a naan, di dëkkoo sama soxna? Mukk! Giñ naa, nga fekke, duma def loolu!»

12 Daawuda ne Uri: «Kon toogaatal fii tey ba ëllëg, ma yiwi la.» Uri toog Yerusalem bésub keroog ak ca ëllëg sa. 13 Ci biir loolu Daawuda woo Uri, mu bokk ak moom lekk, daldi naan. Mu nàndal ko ba mu màndi. Ba ngoon jotee Uri daa génn, tëdd ca laltoom ca biir surgay sangam, waaye këram, àggu fa ba tey.

14 Ba bët setee Daawuda bind Yowab bataaxal, yóbbante ko Uri. 15 Mu bind ci bataaxal bi, ne Yowab: «Jiitalal Uri mii ca làngu kanam, ga xare ba gëna tànge, te ngeen dànd ko, ndax ñu jam ko, mu dee.»

16 Ci kaw loolu Yowab a nga bàyyi xel ca dëkk ba ñu gaw. Mu daldi teg Uri fu ko wóor ne ay ñeyi xarey dëkk baa fa féete. 17 Ba loolu amee waa dëkk ba génn, xeex ak ñoom Yowab, mu am ñu daanu ca gàngoor ga, ca niti Daawuda ña, Uri Etteen ba bokk ca ña dee.

18 Ba mu ko defee Yowab yónnee àgge Daawuda mboolem xew-xewi xare ba. 19 Yowab sant ndaw la, ne ko: «Boo nettalee buur li xew ci xare bi lépp, ba noppi, 20 su Buur meree, ne la: “Ana lu waral ngeen jegee noonu dëkk ba ci xeex? Xanaa xamuleen ne ca kaw tata ja lañu leen di fitte? 21 Ana ku reyoon Abimeleg doomu Yerubeset? Xanaa du ca kaw tata ja la ko aw jigéen sànnee doju wolukaay, ba mu dee ca Tebes? Lu waral ngeen jegee noonu tata ja?” Su boobaa nee ko: “Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.”»

22 Ndaw la dem ba àgg, daldi àgge Daawuda la ko Yowab waxloo lépp. 23 Ndaw la da ko ne: «Nit ñaa nu jëkkoona man. Dañoo génn, song nu ca àll ba. Waaye noo leen delloo gannaaw ba ca bunt dëkk ba. 24 Fittkat ya nag fitte nu ca kaw tata ja, ba mu am ñu dee ci say nit. Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.» 25 Daawuda ne ndaw la: «Waxal Yowab ne ko, bumu tiislu moomu mbir; xare bu yóbbuwul kii, yóbbu kee. Na gëna song dëkk ba rekk, ba daane ko. Nga ñaaxe ko noonu.»

26 Ba loolu amee jabaru Uri dégg ne jëkkëram dee na. Mu daldi koy ténj.

27 Ba àppu ténj ba weesee*11.27 Jamono yooyu bànni Israyil juróom ñaari fan lañu aadawoo woon di ténj., Daawuda yónnee, indi ko këram, mu doon soxnaam. Gannaaw gi mu am doom ju góor.

Aji Sax ji nag ñaawlu la Daawuda def.

<- 2.Samiyel 102.Samiyel 12 ->