4 Ba loolu amee Buur sant Ilkiya sarxalkat bu mag ba, mook sarxalkat ya ca topp, ak wattukati buntu kër Aji Sax ji, ne leen ñu génnee kër Aji Sax ji mboolem ndab ya ñu defaraloon Baal ak Aseraak biddiiwi asamaan yépp. Mu génne lépp Yerusalem, lakk ko ca tooli Sedoron, ba noppi yóbbu dóom ba Betel. 5 Gannaaw loolu mu dàq sarxalkati tuur ya buuri Yuda faloon ñuy taal cuuraay ca bérabi jaamookaay ya ca dëkki Yuda ak la wër Yerusalem, dàqaale ñay taalal cuuraay Baal, ak jant beek weer week xeeti dëllooñ yeek mboolem biddiiwi asamaan yépp. 6 Bu loolu weesee jële na kër Aji Sax ji tuur ma tudd Asera, génne ko Yerusalem ba ca xuru Sedoron, lakk ko foofa ca xuru Sedoron, wol ko ba muy sunguf, mu xëpp ko ca sëgi baadoola ya. 7 Màbb na it këri nit ña doon jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya ca biir kër Aji Sax ji, te jigéen ña daan fa ràbbal tuur ma ñuy wax Asera ay xayma.
8 Ba loolu wéyee Yosya indi Yerusalem mboolem sarxalkat ya doon sarxal ca dëkki Yuda, diggante Geba ba Beerseba, daldi sobeel bérabi jaamookaay ya ñu daan taal cuuraay, daaneel bérabi jaamookaay ya ca bunt ya, boole ca ba nekkoon ca buntu Yosuwe, boroom dëkk ba, te féete càmmoñ booy jaare ci buntu dëkk ba di duggsi. 9 Mayuñu woon nag sarxalkati bérabi jaamookaay ya ñuy dikk ba ca sarxalukaayu Aji Sax ji ci Yerusalem. Sañuñu woon lu moy bokk lekk mburu mu amul lawiir ñook sarxalkat yi ci des. 10 Ci kaw loolu Yosya sobeel na fa ñuy wax Tofet ca xuru Ben Inom, ba kenn dootu fa lakk sa doom ju góor mbaa ju jigéen ngir tuur wi ñuy wax Moleg. 11 Jële na ca bunti kër Aji Sax ji fas ya ay buuri Yuda jagleeloon jant bi. Ña nga woon ca ëtt ba, ca wetu néegu jawriñ bu ñuy wax Netan Meleg. La ca tegu Yosya lakk watiir ya ñu jagleel jant bi. 12 Ci biir loolu Buur daane sarxalukaay ya ay buuri Yuda yékkati woon ca kaw xaddub néegub kaw bu Axas, ak sarxalukaay ya Manase tabaxoon ca ñaari ëtti kër Aji Sax ji. Mu jële fa lépp, def ko pënd, sànni ca xuru Sedoron. 13 Bérabi jaamookaay ya féete woon Yerusalem penku ca bëj-saalumu tundu Alkànde, Buur Suleymaan tabaxaloon ko tuur ma ñuy wax Astàrt, kasaray waa Sidon ya, ak tuur ma ñuy wax Kemos, kasaray Mowabeen ña, ak tuuru Amoneen mu siblu ma ñuy wax Milkom, Buur Yosya daa boole lépp sobeel ko. 14 Rajaxe na tuuri doj ya, daane xer ya ñuy jaamoo Asera, wuutal fa ay jali yaxi nit, ba mu daj.
15 Naka noona mu boole ca sarxalukaay ba ca Betel ak bérabu jaamookaay ba fa doomu Nebat Yerbowam ma bàkkaarloo woon Israyil, yékkati woon. Sarxalukaay boobaak bérabu jaamookaay booba sax yàq na ko. Dafa lakk bérabu jaamookaay ba, wol ko ba mu mokk, lakk xer wa ñuy jaamoo Asera. 16 Ba mu ko defee Yosya ne gees, gis bàmmeel ya nekk foofa ca tund wa. Mu yeble, ñu sullil ko yax ya, mu lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, sobeel ko noonu, muy kàddug Aji Sax ji góoru Yàlla ga waxoon†23.16 Seetal ci 1.Buur ya 13.2., keroog ba Yerbowam taxawee ca sarxalukaay ba, bésub màggal. Buur Yosya neeti gees, yem ci bàmmeelu góoru Yàlla ga biraloon waxyu ba. 17 Mu ne: «Doj wee may séen bàmmeelu kan a?» Waa dëkk ba ne ko: «Xanaa bàmmeelu góoru Yàlla ga bàyyikoo woon Yuda. Moo waxoon bu yàgg jëf jii nga def sarxalukaayu Betel bii tey.» 18 Mu ne: «Bàyyileen ko noonu! Bu kenn laal ay yaxam!» Ñu wacc fa ay yaxam ak yaxi yonent ba jóge woon Samari.
19 Mboolem bérabi jaamookaay ya nekkoon ca dëkki Samari yu mag ya te buuri Israyil tabaxoon ko, ba merloo Aji Sax ji, Yosya jële na ko fa, def ko na mu defoon ca Betel rekk. 20 Gannaaw loolu mu rendi ca sarxalukaay ya mboolem ña fa doon sarxalkati bérabi jaamookaay ya, ba noppi lakk yaxi nit ca kaw, ngir sobeel lépp, doora dellu Yerusalem.
26 Teewul Aji Sax ji dëppul ci meram mu réy mi mu dale ci kaw Yuda ndax mboolem li Manase def, ba merloo ko. 27 Aji Sax ji nag ne: «Yuda itam dinaa ko jële fi sama kanam, ni ma fi jëlee Israyil. Dinaa xalab dëkk bii ma tànn, di Yerusalem ak kër gii ma wax ne sama tur dina fi nekk.»
36 Ñaar fukki at ak juróom la Yowakim amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Sebuda doomu Pedaya ma cosaanoo Ruma. 37 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, mboolem noonee ko ay maamam defe woon.
<- 2.Buur ya 222.Buur ya 24 ->