7 Te it, waccalees na ma ndégu biir suux, mu taxawe ndawal Seytaane, di ma mitital, ngir ma baña bew ndax peeñu yu yéeme. 8 Mbir moomu, ñetti yoon laa ci ñaan Sang bi, ngir mu sorele maak moom. 9 Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw. 10 Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole, ak ci biiri saaga, ak ci biir ag ñàkk, ak ci biir coono yu ñu may bundxatale, ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.
14 Maa ngii di leen waaja ganesi ñetteel bi yoon, te duma wéeru ci yeen. Wutsiwuma lu ngeen am, yeen laa soxla. Ndaxte doom du dencal waajuram, waaye waajur mooy dencal doom. 15 Man nag xol bu sedd laa yeboo ci jaay mboolem lu ma am, ba jaay sama dooley bopp ngir seen jëmmi bopp. Xanaa duma leen ji gii cofeel gu réy, di feyoo cofeel gu ko yées? 16 Xanaa dees na ne, man ci sama wàllu bopp diisaluma leen moos, waaye samag njublaŋ laa fexee ba nax leen?
17 Ndax am na kenn ku ma jëfandikoo, ci ñi ma yebaloon ci yeen, ba lekkal leen lenn? 18 Maa soññ Tit, ngir mu seetsi leen, te maa yebal mbokk moomu, boole kook moom. Ndax Tit da leena lekkal? Xanaa du maak mooma bokk menn mébét, ak wenn doxalin?
19 Mbaa fooguleen ne sunu bopp lanuy layal nii fi seen kanam? Fi kanam Yàlla de lanu waxe, ndax Almasi mi nu gëm, te lépp, soppe yi, seen yokkute la ñeel. 20 Ragal naa, bu ma dikkee, fekke leen nu ma neexul, yeen it, ngeen gise ma nu leen neexul. Ragal naa ay réeroo ci seen biir ak kiñaan ak mer mu ëpp, ak diiroo mbagg, ak waxi sos aki jëw, ak réy-réylu, akug salfaañoo. 21 Ragal naa, bu ma dikkee, sama Yàlla ruslooti ma ndax yeen, may tiisoo ñu bare ñu wéye seen bàkkaar ya woon, te tuubuñu jëfi sobe ji, ak powum séy mi, ak yàqute gu af, gi ñu nekke.
<- 2.Korent 112.Korent 13 ->- a 12.2 Ci gis-gisu Yawut yi, ñetteelu asamaan moo gëna kawe.