7 Xanaa ci melow biti doŋŋ ngeen di xool*10.7 Mbaa: Xool-leen jàkk mbir mi.! Su amee ku mu wér péŋŋ, moom ci boppam ne ci Almasi la bokk, na dellu jàpp moom ci boppam, ne ndegam ci Almasi la bokk, nun itam, ci Almasi lanu bokk. 8 Te doonuma am benn kersa, su ma ëppaloon sax ci damoo sañ-sañ bi nu Boroom bi jox, te du sañ-sañu sànk leen it, xanaa yokk seen ngëm. 9 Buggumaa mel ni ku leen di xëbale ay bataaxal nag. 10 Ndaxte bataaxal yi kat lañu ne: «Dañoo ñagas, te tàng, waaye bu teewee moom ci boppam, da naan yàcc, te ay kàddoom xeebu.» 11 Lii nag, kiy waxe noonu, na ko xam: ni nu mel ci kàddu ci sunuy bataaxal, bu nu wuutee, noonu lanuy mel ci jëf, bu nu teewee.
12 Ñenn ci ñooñu di seedeel seen bopp ne ñoo yelloo ngërëm nag, nun ñemewunoo boole sunu bopp ak ñoom, mbaa nuy méngale sunu bopp ak ñoom. Waaye ñoom dañoo amul xel, ndax nattukaay bi ñuy nattoo, di ko méngalantee ci seen biir, ñoom ñoo ko sàkkal seen bopp! 13 Nun, sunub damu dafa am kemu bu mu dul wees. Sunu kemu moo di déndub tool bi nu Yàlla sas, te ci biir tool bi lanu liggéeye, ba agsi ci yeen. 14 Moo tax weesunu sunu kemu sas, mbete agsiwunu woon ba ci yeen. Waaye noo agsi ba ci yeen, indil leen xibaaru jàmm bu Almasi. 15 Weesunu kemu, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne nu seen ngëm gëna yokkoo, ni la sunuw sas di gëna yokkoo, lépp ci biir kemu gi ñu nu àppal. 16 Su ko defee nu mana wees fa yeen, ba jàll yégleji xibaaru jàmm bi ca wàlla, te baña damoo lu ñeneen def ba noppi, ci seen biir sas. 17 Kuy damu daal, na damu ci Boroom bi†10.17 Seetal ci Yeremi 9.23..
18 Ndax ki ñu naw mooy ki Boroom bi gërëm, waaye du ki gërëm boppam.
<- 2.Korent 92.Korent 11 ->