mu bind ko waa
Korent
8 Ndax kat, bokk yi, buggunu ngeen umple njàqare, ji nu daj ci diiwaanu Asi. Daj nanu coono bu jéggi dayo, te wees sunu kàttan, ba yaakaaratunu woona dund sax. 9 Nun ci sunu wàllu bopp, jàppoon nanu ne sunu àtteb dee moo taxaw. Waaye loolu tax na nu bañatee yaakaar sunu bopp, xanaa di yaakaar ci Yàlla, miy dekkal ñi dee. 10 Moo nu wallu ci googu dee gu naroona metti, moo nuy walluwaat, te moom lanu yaakaar mu wallooti nu. 11 Yeen itam, ni ngeen nu ciy jàpplee mooy ngeen di nu ñaanal. Su ko defee yiw, wa nu ñu bare ñaanal ba nu am ko, dina tax ñu bare biral ag cant ci sunu mbir.
15 Kóolute gu ma amoon ci ni ngeen nuy damoo moo tax ma naroona jëkka dikk ba ci yeen, ngir seen yiw mana yaar, 16 ba bu ma jógee ci yeen, daldi jaareji diiwaanu Maseduwan, bu ma jógee Maseduwan, dikkaat ci yeen, ba ngeen yiwi ma, ma jëm Yude. 17 Ndax ñàkk pastéef laa mébéte moomu mébét? Am ni nitu suuxu neen di mébéte rekk laa topp bay xel-yaar, naan «waaw» te naan «déet»?
18 Yàlla mi mata gëm de seere na ne kàddu gi nu leen di wax du «waaw, déet,» 19 ndax Doomu Yàlla, Yeesu Almasi, mi nu biral ci seen biir, man ak Silas*1.19 Silas mooy Silwan ba tey. ak Timote, du kàddug «waaw, déet;» «waaw» doŋŋ a nekk ci moom. 20 Ak li digey Yàlla di bare lépp, ci Almasi la ay digeem di doone «waaw». Moo tax itam, ci moom lanu naan Yàlla: «Amiin», ngir delloo ko njukkal. 21 Te ki nuy saxal ci Almasi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla. 22 Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.
23 Man nag seedey Yàlla laa ciy sàkku, giñ naa ko ci sama bakkan, bañ leena yokku naqar moo tax délsiwuma Korent. 24 Du caageenu yilif seen ngëm nag, ndax ci ngëm ngeen sax, waaye nook yeen ay liggéey, ngir seen mbégte.
2.Korent 2 ->- a 1.19 Silas mooy Silwan ba tey.