6 Ba mu ko defee loxol Aji Sax ji mujj diis ca kaw waa Asdodd. Mu wàcce njàqare ca seen kaw, daldi teg waa Asdodd ak la ko wër ay taab. 7 Waa Asdodd gis la leen dal, daldi ne: «Bu gaalu Yàllay bànni Israyil gii des ci sunu biir kat, ndax loxoom dëgër na ci sunu kaw, nook Dagon sunu tuur mi.» 8 Ba loolu amee ñu yónnee, woolu mboolem kàngami waa Filisti. Ñu laaj leen ne leen: «Nan lanuy def ak gaalu Yàllay Israyil gii?» Ñu ne leen: «Toxal-leen gaalu Yàllay Israyil gi ca Gaat.» Ñu toxal gaalu Yàllay Israyil ca seen dëkk ba ñuy wax Gaat. 9 Naka lañu fa toxal gaal ga nag, loxol Aji Sax ji dal dëkk ba, mu jur tiitaange lu réy lool. Daa dal ca kaw dëkk ba, mag ak ndaw, ay taab ne fureet ca seen kaw. 10 Ñu yóbbu gaalu Yàlla ga beneen dëkk bu ñuy wax Ekkron. Gaal gaa ngay jubsi Ekkron, waa dëkk ba gaaw yuuxoondoo ne: «Indil nañu nu fi gaalu Yàllay Israyil, bëgg noo rey, nook sunu waa réew mépp!» 11 Ci kaw loolu ñu yónnee, woolu mboolem kàngami waa Filisti, ne leen: «Jëleleen fi gaalu Yàllay Israyil gii, mu dellu këram, lu ko moy dina nu rey, nook sunu askan wépp.» Booba tiitaangey ndee dajal na dëkk ba bépp, ndax loxol Yàlla bu diis lool ca seen kaw. 12 Ña ca deewul nag, seen yaram yàqooki taab, yuux ya jollee ca dëkk ba, wuti asamaan.
<- 1.Samiyel 41.Samiyel 6 ->