4 Ci kaw loolu mbooloo ma yónnee ca Silo, ñu jëli gaalu kóllërey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Ki toog fi tiim ñaari malaakay serub yi[a]. Foofa ca Silo la Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, nekkoon ak gaalu kóllërey Aji Sax ja.
5 Ba gaalu kóllërey Aji Sax ji duggsee ca dal ba, Israyil gépp a xaacoondoo, ba suuf say riir. 6 Waa Filisti dégg coow la, ne: «Waaw, coow lu réy loolu ca dalub Ebrë ya, lu mu doon?»
10 Waa Filisti nag di xare, ba bànni Israyil daanu: ku nekk daw jëm xaymaam. Jéll ba réy na lool; fanweeri junniy xarekat yuy deme tànk. 11 Gaalu Yàlla ga, ñu jël; Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, dee.
14 Eli dégg coow la, ne: «Riir moomu lu mu?» Waa ja gaaw dikk, wax ko Eli. 15 Booba Elee ngi ci juróom ñeent fukki at ak juróom ñett (98), bët yi ne xóll te gisatul dara. 16 Waa ja ne ko: «Man mii maa jóge ca toolub xare ba. Maa dawe làng ga tey jii.» Eli ne ko: «Doom, lu xew?» 17 Ndaw la ne ko: «Bànni Israyil a daw, won waa Filisti gannaaw. Jéll bu réy la sunu mbooloo ma daanu, sa ñaari doom ya, Ofni ak Fineyas dee nañu, te it gaalu Yàlla ga, jël nañu ko.» 18 Naka la tudd gaalu Yàlla ga rekk, Eli xàwwikoo ca toogu ba, daanoo njaaxaanaay, dal ca bunt dëkk ba, loos wa damm, mu dee, ndax booba day mag mu ànd ak yaramam. Eli jiite na Israyil ñeent fukki at.
19 Goroom, jabaru Fineyas nag jigéenu wérul la woon te booba mu ngi waaja wasin. Naka la dégg ne jël nañu gaalu Yàlla ga, te baayu jëkkëram ak jëkkëram dee nañu, mu daldi sukk wasin. Waaye fekk na mititu matam jeexal dooleem. 20 Ba loolu amee muy waaja dee, jigéen ña ko doon taxawu ne ko: «Na sa xel dal, ndax doom ju góor nga am.» Waaye àdduwul, teewluwul. 21 Ndaw sa nag tudde gone gi Ikabot (mu firi Ana leer ga?) te naan: «Leer ga dëddu na Israyil, dem ngàllo.» Ndax la ñu nangu gaalu Yàlla ga ak la goroom ak jëkkëram dee. 22 Mu ne: «Leer ga kay dëddu na Israyil, dem ngàllo, ndegam jëlees na gaalu Yàlla ga kay!»
<- 1.Samiyel 31.Samiyel 5 ->- a 4.4 serub ya: baatu ebrë la. Ay malaaka lañu yu bokk ak Yàlla jataay. Gaalu kóllëre gu sell ga, ñaari serub yu ñu tëgge wurus lañu teg ca kawam, ñu tiim ko, seeni laaf tàllalu, di saamandaay ngàngunem buur. Loolu di wone ne Yàlla Aji Sax jaa nga fa teew, na mu teewe ca kaw asamaan, serub ya yéew ko. Yàlla ci boppam nag kenn jëmmalu ko fa, na ñu jëmmale serub ya ñu tëgg.