2 Mu am bés Eli tëdd fa muy tëdd naka jekk, fekk bët ya naqari, ba daanaka gisatul. 3 Booba làmpu jaamookaayu Yàlla bi feyagul, te Samiyel a ngi tëdd ci biir jaamookaayu Aji Sax ji, fi gaalu Yàlla gi nekk. 4 Aji Sax ji woo Samiyel, mu ne: «Maa ngi», 5 daldi daw ba ca Eli, ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli ne ko: «Wootewuma de, dellul tëri.» Mu dellu tëdd.
6 Aji Sax ji dellu woo Samiyel, Samiyel jóg, dem ba ca Eli ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli ne ko: «Wootewuma de doom, dellul tëri.» 7 Booba Samiyel xamagul woon Aji Sax ji, te kàddug Aji Sax ji dikkalagu ko woon.
8 Aji Sax ji wooti Samiyel ñetteel bi yoon, Samiyel jógati, dem ba ca Eli ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli nag xam ne Aji Sax jeey woo xale bi. 9 Mu ne Samiyel: «Demal tëri, bu la wootee, nee ko: “Aji Sax ji, maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.”» Samiyel dellu tëdd fa muy tëdd.
10 Ba mu ko defee Aji Sax ji dikk taxaw, wooti ko na woon, ne ko: «Samiyel, Samiyel.» Samiyel ne: «Maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.» 11 Aji Sax ji ne Samiyel: «Maa ngii déy, di waaja def ci digg bànni Israyil, mbir muy buur noppi mboolem ku ko dégg. 12 Bésub keroog ma matal ci Eli mboolem lu ma waxoon ne mooy dal waa këram, ndoorte la ba ca muj ga. 13 Waxoon naa ko ne ko dinaa teg waa këram mbugal mu sax dàkk, ndax ñaawtéef gu ay doomam nekke, di ñàkke Yàlla teggin, mu yég ko te jubbantiwu leen. 14 Looloo waral ma giñal waa kër Eli, ne du am mukk benn saraxu jur mbaa beneen sarax bu leen mana jot ci seen ñaawtéef.»
15 Ci kaw loolu Samiyel tëdd ba ca suba sa, mu tijji bunti kër Aji Sax ji, waaye ñemewula nettali Eli peeñu ma. 16 Eli nag woo ko ne ko: «Samiyel doom, ana nga?» Samiyel ne ko: «Maa ngi.» 17 Eli ne ko: «Kàddu gi mu la wax, lu mu doon? Bu ma nëbbu kay. Soo ma nëbbee lenn ci li mu la wax, yal na la Yàlla teg naqar wu gëna tar.» 18 Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»
19 Ci kaw loolu Samiyel di màgg, Aji Sax ji ànd ak moom, waccul genn kàddug Samiyel, mu fanaan àll. 20 Noonu la Israyil gépp ràññee, la dale Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum, ne Samiyel taxaw na taxawaayu yonentu Aji Sax ji. 21 Aji Sax ji nag wéye koo feeñu ca Silo. Ci kàddug Aji Sax ji la ko Aji Sax ji daan feeñoo ca Silo.
<- 1.Samiyel 21.Samiyel 4 ->