9 Doweg, Edomeen ba taxawandook jawriñi Sóol, daldi àddu, ne: «Man de, gis naa doomu Yese ji, mu dikk dëkk ba ñuy wax Noob, ca Ayimeleg doomu Ayitub. 10 Ayimeleg seetal na ko ci Aji Sax ji, ab dund it may na ko ko, te it saamaru Golyaat waa Filisti ba, jox na ko ko.» 11 Buur Sóol woolu sarxalkat ba Ayimeleg doomu Ayitub, ak mboolem bokki baayu Ayimeleg ya doon ay sarxalkat ca Noob; ñu wuysi Buur Sóol, ñoom ñépp. 12 Buur ne: «Yaw doomu Ayitub, déglu ma fii!» Mu ne ko: «Maa ngi lay dégg, sang bi.» 13 Sóol ne ko: «Li nga ma def nag, di ma fexeel, yaak doomu Yese ji? Yaa ko may ab dund, yaa ko jox ab saamar, seetal ko ci Yàlla, ba mu jógal ma, di ma tëru nii tey!»
14 Ayimeleg ne Buur: «Buur, ana sa surga yii ba ñu daj, ku la nangule ni Daawuda mii, di sa goro, jiite say dag, te di ku ñu nawloo ci sa biir ëtt bii? 15 Du keroog laa ko jëkka seetal ci Yàlla de! Te it Yàlla buma la lalal pexe! Dëgg waay, Buur sama sang, bu ma topp lenn maak kenn ci sama waa kër baay, ndax kat sang bi, xawma dara ba dara booloo jeex ci menn pexe.» 16 Buur Sóol ne ko: «Yaw Ayimeleg kay, dee rekk mooy sab àtte, yaak sa waa kër baay yépp.» 17 Ba mu ko defee Buur ne dagam ya ko dar: «Ayca, reyleen sarxalkati Aji Sax yii, gannaaw ñoom it ñook Daawudaa far. Yégoon nañu ba muy daw te xamaluñu ma ko.» Dagi buur ya nag baña xàcci seen loxo ci kaw sarxalkati Aji Sax ya. 18 Buur ne Doweg: «Ayca yaw, fàddal sarxalkat yii!» Doweg Edomeen ba fàdd sarxalkat ya. Rey na bésub keroog juróom ñett fukki nit ak juróom (85) ñuy sol xar-sànnim lẽe. 19 Waa Noob dëkkub sarxalkat ya it, mu jam leen, leele ñawkay saamar; góor ak jigéen, gone ya, ba ca ñay nàmp, ak nag yaak mbaam yaak gàtt ya, lépp la leele ñawkay saamar.
20 Jenn doomu Ayimeleg miy doomu Ayitub doŋŋ a rëcc, te mooy Abiyatar. Mu daw, fekki Daawuda. 21 Mu yégal Daawuda ne ko Sóol reylu na sarxalkati Aji Sax yi. 22 Daawuda ne Abiyatar: «Xamoon naa bésub keroog ne gannaaw Doweg Edomeen baa nga fa woon, du ñàkk moos mu nettali ko Sóol. Man mii maa gàddu sa bakkani waa kër baay gépp. 23 Waaye toogal fii ci man, te bul ragal dara. Ki lay wuta rey moo may wuta rey man itam. Soo nekkee ci sama wet nag, yiiru nga.»
<- 1.Samiyel 211.Samiyel 23 ->