6 Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Ayca nu dem ba ca dalub yéefar yee. Jombul Aji Sax ji defal nu yiw, ndax dara du tee Aji Sax ji maye ndam, nu bareek nu néew.» 7 Ba loolu amee gàddukatu gànnaayam ne ko: «Ayca, loo namm rekk, sang bi, yaw laa àndal ba jeex tàkk.» 8 Yonatan ne ko: «Ayca nu dem ba ca ñoom, feeñu leen. 9 Bu ñu nu nee: “Taxawleen foofu, ba nu fekksi leen,” nu yem fa, bañ leena fekki. 10 Waaye bu ñu nee: “Ayca, dikkleen,” nu daldi dem te xam ne Aji Sax jee leen teg ci sunu loxo. Nan def loolu ab takk.»
11 Ba loolu amee ñu feeñuji dalub waa Filisti, ñoom ñaar ñépp. Waa Filistee nga naan: «Xool-leen! Ay Ebraa ngay génne pax ya ñu làqu woon.» 12 Ci kaw loolu waa dal ba ne Yonatan ak gàddukatu gànnaayam: «Ée, dikkleen rekk, nu xamal leen lu tuut.» Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Dikkal, topp ci man. Aji Sax ji teg na leen ci loxol Israyil.» 13 Yonatan ñalgu ca kaw tund wa, gàddukatu gànnaayam topp ko. Yonatan a ngay jam, waa Filisti di daanu, gàddukatu gànnaayam ba di leen jekkli ca gannaawam. 14 Cong mu jëkk mooma Yonatan song, mook gàddukatu gànnaayam, lu tollook ñaar fukki góor lañu ca tëral ci dénd bu wara tollook xëyu nag. 15 Ci kaw loolu tiitaange dajal dal baak àll ba ko wër, ak mbooloo ma mépp; muy dal ba, di kuréli yàqkat ya. Rax ca dolli suuf sa yëngu, muy tiitaange lu Yàlla wàcce.
16 Fekk na ay jongrukati Sóol a nga tollu ca Gibeya gu Beñamin. Ñu jekki séen gàngooru Filisti gay raj-rajloo, fu ne ñu jëm fa. 17 Sóol ne ña ànd ak moom: «Wooteleen, ba xam ku jóge ci nun.» Ñu woote, Yonatan ak gàddukatu gànnaayam wuute. 18 Sóol ne Axiya sarxalkat ba: «Indil gaalu Yàlla gi.» Bésub keroog gaalu Yàlla gaa ngaak bànni Israyil. 19 Naka la Sóol di wax ak sarxalkat bi, coow la ca dalub waa Filisti gëna jolli. Sóol ne sarxalkat bi: «Ah, bàyyi ko sax.» 20 Ba mu ko defee Sóol ak gàngoor ga ànd ak moom gépp daje, dem ca xare ba. Gisuñu lu moy waa Filisti ne kër-kër, ne këpp, di jamante seeni saamar. 21 Ci biir loolu Ebrë yi nangul woon waa Filisti démb ak bëkk-démb te nekkandook ñoom ca dal baak fa ko wër fépp sax, ne waññet, faraat ak seen bokki bànni Israyil ya ànd ak Sóol ak Yonatan. 22 Mboolem bànni Israyil ya làqu woon ca tundi Efrayim dégg ne waa Filisti daw nañu. Ñoom it ne leen dann ca xare ba. 23 Noonu la Aji Sax ji maye Israyil ndam bésub keroog, xare bay law, ba ca wàlla Bet Awen.
31 Bésub keroog bànni Israyil a dumaa waa Filisti ca Migmas ba ca Ayalon. Bànni Israyil sonn lool nag. 32 Ba loolu amee ñu sëxëtoo lël ja, jël ca gàtt yaak nag ya ba ca wëllu ya, tër ca suuf, boole yàpp waak deret ja, lekk. 33 Ñu yegge ko Sóol, ne ko: «Mbooloo ma kat a nga nee, di moy Aji Sax ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Sóol ne: «Yeenaka fecci kóllëre! Béraŋal-leen ma fii aw doj wu mag léegi.» 34 Gannaaw loolu mu joxe leneen ndigal, ne: «Tasaarooleen ci biir mbooloo mi, ne leen ñu indi fii ñoom ñépp seeni nag ak seeni gàtt. Fii lañuy rendee jur gi, door koo lekk. Su ko defee duñu moy Aji Sax ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Mbooloo mépp daldi dikk guddig keroog, ku nekk akaw nagam. Ñu rendi foofa. 35 Sóol daldi fay tabax ab sarxalukaay, ñeel Aji Sax ji. Boobu sarxalukaay la jëkka tabax ñeel Aji Sax ji.
43 Sóol ne Yonatan: «Wax ma loo def.» Yonatan ne ko: «Aylayéwén maa ñam tuuti ca lem, ja ma cappe sama catu yet wi ma yoroon ci sama loxo. Maa ngi, naa dee!» 44 Sóol ne ko: «Na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, waaye yaw Yonatan dinga dee déy!» 45 Mbooloo ma nag ne Sóol: «Lan? Yonatan dee, moom mi may Israyil ndam lu réy lii? Xalaateesu ko moos! Giñ nanu ci Aji Sax jiy dund, du lenn luy rote ci kawaru boppu Yonatan sax, dal fi suuf, ndax Yàlla la àndal def lii tey.» Noonu la mbooloo ma jote Yonatan, ba deewul. 46 Ba loolu wéyee Sóol noppee dàq waa Filisti, waa Filisti dellu ca seenum réew.
49 Doomi Sóol yu góor nag ñoo doon: Yonatan, ak Iswi ak Malkisuwa; ñaari doomam yu jigéen, di Merab mi ci gën di mag, ak Mikal mi gën di ndaw. 50 Soxnas Sóol moo doon Ayinowam, Ayimaas di baayu Ayinowam. Njiitu xareem moo doon Abner doomu Ner baayu Sóol bu ndaw, 51 Kis miy baayu Sóol, ak Ner, baayu Abner, Abyel ay seen baay.
52 Xare bu metti la woon seen digg ak waa Filisti, giiru dundu Sóol gépp. Moo tax fu Sóol gisaan boroom kàttan mbaa boroomu fit, da koy dollikoo.
<- 1.Samiyel 131.Samiyel 15 ->- a 14.5 Geba: seetal ci 13.3.