6 Niti Israyil nag gis diggante bu metti bi ñu tollu ndax na ñu tance seen gàngoor ga. Ñu dem làquji ci ay xunteek ay dédd ak ay doj, aki seyaan aki kàmb. 7 Am na sax ay Ebrë yu jàll dexu Yurdan, wuti réewum Gàdd ak Galàdd. Fekk na Sóol a nga ca Gilgal ba tey. Mbooloom xareem ma mépp nekk faak moom, di pat-pati ndax tiitaange.
8 Mu négandiku juróom ñaari fan, diir ba ko Samiyel àppaloon. Waaye taxul Samiyel agsi Gilgal. Mbooloo ma tàmbalee dëddu Sóol, di tasaaroo. 9 Ba loolu amee Sóol ne: «Indil-leen ma saraxu rendi-dóomal bi, ak saraxu cantu biir jàmm bi.» Ñu indil ko, mu daldi def saraxu rendi-dóomal bi. 10 Naka la def saraxu rendi-dóomal bi ba sottal rekk, Samiyel ne jaas. Sóol génn gatandu ko, ngir nuyu ko. 11 Samiyel ne ko: «Loo def nii?» Sóol ne ko: «Man kat damaa gis mbooloo mi dëddu ma, di tasaaroo, te yaw it dikkoo bésu àpp bi. Rax ci dolli waa Filistee nga daje ca Migmas. 12 Ma noon, waa Filisti dinañu ma songsi Gilgal, te sàkkooguma ndimbalu Aji Sax ji. Looloo ma taxa sàcc sama bopp rekk, ba def saraxu rendi-dóomal bi.» 13 Samiyel ne Sóol: «Ag ndof nga def, ndax jëfewuloo santaane bi la sa Yàlla Aji Sax ji santoon. Soo ko defoon, Aji Sax ji dina saxal sa nguur ci kaw Israyil ba fàww. 14 Léegi nag sa nguur du wéy; Aji Sax ji sàkkul na boppam ki xolam jubool, te fal na ko njiitu ñoñam, ndax yaa sàmmul li Aji Sax ji santaane.»
15 Ba mu ko defee Samiyel bàyyikoo Gilgal, dem Gibeya gu Beñamin. Sóol nag waññ ñi mu àndal, ñu tollu ci juróom benni téeméeri góor.
19 Booba nag benn tëgg amul woon ca réewum Israyil ba mu daj, ndax waa Filisti dañu noon: Bu Ebrë yi sàkk ay saamar aki xeej. 20 Moo tax bànni Israyil gépp, ku ci bëggoona nàmmlu sa ngajju mbaa sa daba, mbaa sa sémmiñ, mbaa sa sawta, doo man lu moy dem ca tëggi waa Filisti. 21 Ku ci nekk, saa yu sa ngajju dayee, mbaa sa daba, ñaari ñetteelu siikal nga koy daasloo, njég gu jafe, tollook ñaari ñetteelu dogu xaalis. Boo dee daaslu ab roqub ñetti càq, mbaa sémmiñ, mbaa ngay jubbantilu catal ràbbu, genn-wàllam ngay fey. 22 Looloo tax keroog bésub xare ba, du benn xarekat bu ànd ak Sóol ak Yonatan, te yor saamar mbaa xeej ci loxoom. Mennum Sóol rekk a ci amoon, mook doomam Yonatan.
23 Ci biir loolu ab kurélu xarekati waa Filisti dem, taxawi ca jàllukaayu Migmas ba.
<- 1.Samiyel 121.Samiyel 14 ->