3 Seen gànjar bumu doon gànjaru biti bu yem ci ay létt yu rafet, ak takkaayi wurus, ak yére yu yànj, 4 waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla. 5 Bu jëkkoon loolu moo doon gànjaru jigéen ñu sell ña yaakaaroon Yàlla te nangul seen jëkkër, 6 noonu Saarata déggale woon Ibraayma, naan ko «Sang bi». Yeen jigéen ñi nag, yeen ay doomi Saarata, li feek yeena ngi def lu baax te bañ cee ragal ku leen xupp.
7 Naka noonu yeen góor ñi, bàyyileen xel ni ngeen dëkke ak seeni jabar, tey sóoraale néew dooley jigéen. Séddleen leen teraangay nawle, gannaaw yeena bokk wenn yiw wi leen may ngeen dund dëgg. Su ko defee dara du gàllankoor seeni ñaan.
17 Coono yu la jëf ju baax yóbbe kat, ndegam da di coobarey Yàlla, moo gën coono yu la jëf ju bon yóbbe. 18 Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi. 19 Ci dooley Noo googu la deme ba waari bindeef ya seeni fit tëje†3.19 Seetal it ci 2.Piyeer 2.4 ak Yudd 1.6., 20 ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yett gaal, ga lim bu néew, juróom ñett, mucce woon ca ndox ma. 21 Ndox mooma di misaalub sóobu gi leen musal tey; du sóobu guy dindi tërub yaram, waaye moom ngeen di wuyoo wooteb Yàlla ci xel mu dal, te li leen di musal mooy ndekkitel Yeesu Almasi, 22 mi yéeg asamaan, toog fa ndijooru Yàlla, ki malaaka yeek boroom sañ-sañ yeek boroom doole yi, bokk nekk cig curgaam.
<- 1.Piyeer 21.Piyeer 4 ->