4 Ci biir loolu Buur dem Gabawon, sarxali fa, ndax foofaa doon bérabu jaamookaay ba gënoona mag: junniy saraxi rendi-dóomal, Suleymaan joxe na ko fa ca kaw sarxalukaay booba. 5 Foofa ca Gabawon la Aji Sax ji feeñu woon Suleymaan ci géntug guddi. Yàlla ne ko: «Ñaanal loo bëgg, ma may la ko.» 6 Suleymaan ne ko: «Yaw de yaa baaxe lool sab jaam Daawuda, saa baay, ngir na mu daan doxale fi sa kanam ci dëgg ak njekk ak njubteg xol. Yaa ko baaxe lool, may ko doom ju góor ju toog cib jalam, bésub tey jii. 7 Léegi nag Aji Sax ji, sama Yàlla, fal nga ma buur, ma wuutu saa baay Daawuda. Waaye Sang bi, man ndaw lu tuut laa, xawma sax nu may doxale. 8 Rax ci dolli, Sang bi, ma nekk ci digg askan wi nga taamu, askan wu yaa, ba maneesu koo waññ mbaa di ko lim. 9 Kon nag Sang bi, may ma xel mu am ug dégg mu ma àttee sa ñoñ, ngir may ràññee lu baax ak lu bon. Ndax kat, ana kan moo mana àtte sa ñoñ, wii askan wu réy?»
10 Kàddug Suleymaan ga nag neex Aji Sax ji, ndax loolu mu ñaan.
11 Mu ne ko: «Gannaaw loolu nga ñaan, te ñaanuloo fan wu gudd, ñaanuloo alal, ñaanuloo itam say noon dee, xanaa di ñaan xel mu rafet moo àttee dëgg, 12 dama ne, dinaa la defal li nga ñaan, te sax dinaa la may xel mu rafet, nga am ug dégg, ba raw ku la jiitu ak ku la wuutu. 13 Te itam li nga ñaanul dinaa la ko may, booleel la alal ak teraanga, ba doo am moroom ci buur yi, sa giiru dund. 14 Te soo jaaree ci samay yoon, jëfe samay sàrt ak samay santaane, muy fi sa baay Daawuda jaaroon, kon dinaa guddal saw fan.»
15 Ba loolu amee Suleymaan yewwu, ndeke gént la woon. Mu dellu Yerusalem, taxaw fa kanam gaalu kóllërey Aji Sax ji, def fa ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm, daldi berndeel jawriñam yépp.
23 Buur ne: «Kii a ngi naan: “Sama doom jii mooy dund, sa doom a dee.” Kee naan: “Déedéet, sa doom a dee, sama doom mooy dund.”» 24 Buur teg ca ne: «Indil-leen ma saamar!» Ñu indil Buur saamar. 25 Buur ne: «Dogleen xale biy dund ñaar, te jox kii genn-wàll, jox kee genn-wàll.» 26 Ci kaw loolu ndaw si doomam di dund daldi ñeewante doomam. Mu ne: «Déet, sang bi, jox ko xale bi. Bu ko rey mukk!» Ndaw sa ca des, moom, ne: «Deesu ma ko jox, deesu la ko jox; dogleen ko ñaar!» 27 Ba loolu amee Buur daldi àtte ne: «Joxleen ndaw sii liir biy dund, te buleen ko rey. Mooy ndeyam.»
28 Israyil gépp nag dégg àtteb Buur, daldi yéemu ci moom, ndax dañoo gis ne xelum Yàlla mu rafet a ngi ci moom, di ko jiite ci àtte dëgg.
<- 1.Buur ya 21.Buur ya 4 ->