7 Buurub Israyil nag woolu magi réew ma mépp, ne leen: «Boo yeboo ngeen xam ne waa jii kat fitna lay wut; gis ngeen mu yeble ci man, bëgga nangu samay jabar ak sama doom yu góor ak sama xaalis ak sama wurus, te bañaluma ko ci dara.» 8 Mag ñaak mbooloo ma mépp ne ko: «Bu ko déglu te bul nangu!» 9 Axab ne ndawi Ben Addàd ya: «Waxleen Buur, sama sang, ne ko: “Sa jaam ba nee mboolem la nga jëkkoona yónnee di ko sàkku dina ko def. Waaye lii nga mujja laaj moom, du ko def.”» Ndaw ya dem jottli tontam. 10 Ben Addàd dellu yeble ca moom ne ko: «Yal na ma tuur yi teg mbugal mu gëna tar, ndegam duma tas Samari, ba pëndu tabax du fi des buy fees loxoy mboolem ñi ma topp.»
11 Buurub Israyil ne: «Waxleen ko ne ko:
12 Ba Ben Addàd di jot ca kàddu googu, ma ngay naan, mook buur ya far ak moom ca mbaar ya. Mu jox ay nitam ndigal ne leen: «Takkuleen!» Ñu takku, ngir songi dëkk ba. 13 Ndeke ci biir loolu ab yonent dem na ca Axab buurub Israyil, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gis nga mbooloom xare mii mépp ak li ñuy bare lépp, xamal ne teg naa leen ci sa loxo bésub tey, ndax nga xam ne maay Aji Sax ji.» 14 Axab ne ko: «Ku may defal loolu?» Mu ne ko: «Aji Sax ji nee: Dag yi kilifay diiwaan yi yebal lay doon.» Axab ne ko: «Kuy sooke xare bi?» Mu ne ko: «Xanaa yaw.»
17 Dag ya kilifay diiwaan ya yebal a nga jiitu. Ci biir loolu Ben Addàd yónnee, ñu wax ko ne ko: «Am na ñu jóge Samari, di ñëw.» 18 Mu ne: «Su leen jàmm taxee jóg, jàppleen leen, ñuy dund; su leen xare taxee jóg it, jàppleen leen, ñuy dund.» 19 Ba mu ko defee dagi kilifay diiwaan ya génne ca dëkk ba, mbooloom xare ma topp ca seen gannaaw. 20 Ku nekk jam noon ba nga janool, waa Siri daw, Israyil topp leen. Ben Addàd buurub Siri nag war fas, daw mooki gawaram. 21 Buurub Israyil nag song leen, rey fas ya, yàq watiir ya, daan waa Siri jéll bu réy. 22 Yonent ba dikk ca buurub Israyil ne ko: «Nanga dëgërluwaat te xam ni nga wara def, ndax nëgëni déwén buurub Siri dina la songaat.»
26 Ca déwén sa Ben Addàd lim waa Siri, daldi dem Afeg ca xare baak Israyil. 27 Waa Israyil daje, sàkk ab dund, ba noppi dox wuti leen. Waa Israyil a nga dal janook ñoom, di saf ñaari gétti bëy. Waa Siri ñoom fees àll ba. 28 Góoru Yàlla ga dikk ne buurub Israyil: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw waa Siri dañoo yaakaar ne man Aji Sax ji, yàllay tund laa, duma yàllay xur, maay teg mbooloo mu réy mii mépp ci say loxo. Su ko defee ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»
29 Diiru juróom ñaari fan nag ñu jàkkaarloo ca seeni dal. Bésub juróom ñaareel ba xare ba jib, waa Israyil daane téeméeri junniy xarekat (100 000) yu warul fas ca waa Siri ci benn bés bi; 30 ña ca des daw ba Afeg, ca biir dëkk ba, tata ja màbb ca kaw ñaar fukki junniy nit ak juróom ñaar (27 000) ca ñoom. Fekk na Ben Addàd daw dugg ca biir dëkk ba, jàll ci biir néeg bu làqoo làqu. 31 Ay jawriñam ne ko: «Waaw, nun de dégg nanu ñu naa buuri Israyil buur yu baax lañu. Tee noo sol ay saaku, tañlaayoo buum, toroxloo ko, te dem ca buurub Israyil? Jombul mu bàyyi la, nga dund.» 32 Ñu teraxlaayoo ay saaku, tañlaayoo ay buum, dem ca buurub Israyil, ne ko: «Ben Addàd sa jaam ba nee, nga baal ko ngalla te bàyyi ko mu dund.» Mu ne: «Ndeke mu ngi dund ba tey? Moom sama mbokk a!» 33 Ndaw ya am njort lu rafet nag. Ñu gaaw naa: «Ben Addàd kay sa mbokk a!» Mu ne leen ñu dem indi ko. Ba Ben Addàd dikkee ba ca moom, mu waral ko ca watiiram.
34 Ben Addàd ne Axab: «Dëkk yi sama baay nangoo woon ci sa baay dinaa la ko delloo, te boo yeboo sàkkal sa bopp ay bérabi njaay ca Damaas, na sama baay def ca Samari.» Axab ne ko: «Man nag damay fasanteek yaw kóllëre ci loolu, bàyyi la nga dem.» Ba loolu amee mu fasanteek moom kóllëre, bàyyi ko mu dem.