Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 18
Ilyaas daje naak surgab Buur Axab
1 Ba ñu demee ba mu yàgg, kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas, ca ñetteelu atu maral wa. Mu ne ko: «Demal jàkkaarlook Axab, ma daldi taw ci kaw réew mi.» 2 Ilyaas tegu ca yoon wa ngir jàkkaarloojeek Axab.
Booba xiif ba metti na ca Samari. 3 Ci biir loolu Axab woolu Abdiyas ma yor këram. Abdiyas doonoon ku ragal Aji Sax ji lool. 4 Ndax ba Yesabel jabari Axab di rey yonenti Aji Sax ji, Abdiyas a boole woon téeméeri yonent, làq leen ci ñaari xuntiy xeer, xunti mu nekk juróom fukk. Mu di leen fa may lekk ak naan.

5 Axab nag ne Abdiyas: «Duggal ci biir réew mi te seet ci bëti ndox yeek xur yépp. Jombul nu gis ñax, ba mana rawale bakkani fas yeek berkelle yi, ba du jar nu di leen jekkli.» 6 Ba loolu amee ñu séddoo réew ma, ba mu daj, Axab fii, Abdiyas fee. 7 Abdiyas di dem, Ilyaas ne pemm dajeek moom ca yoon wa. Abdiyas xàmmi ko, sujjóotal ko, dëpp jë ba fa suuf, ne ko: «Kii Ilyaas a, sama sang?» 8 Mu ne ko: «Man a kay! Demal boog wax sa sang Axab, ne ko Ilyaas a ngoog de!»

9 Abdiyas ne ko: «Ana lu ma def lu bon, sang bi, ba nga di ma booleek Axab, mu di ma rey? 10 Giñ naa ci Aji Sax ji, sa Yàlla jiy dund, amul wenn xeet mbaa réew mu sama sang Axab yónneewul, di la seet. Te bu ñu nee nekkoo fa, mu giñloo waa réew maak xeet wa ne gisuñu la. 11 Léegi nag nga naan ma: “Demal wax sa sang ne ko Ilyaas a ngoog.” 12 Su ko defee su ma teqlikook yaw, ngelawal Aji Sax ji yóbbu la fu ma xamul, fekk ma dem wax ko Axab, te du la gis. Kon da may rey! Moona sang bi, man de, damaa masa ragal Aji Sax ji ba may ndaw ba tey. 13 Moo sang bi! Xanaa waxuñu la li ma def, ba Yesabel di rey yonenti Aji Sax ji? Maa làq téeméeri yonenti Aji Sax ji ci ay xuntiy xeer, xunti mu nekk juróom fukk, di leen may lekk ak naan. 14 Léegi nga naa ma: “Demal wax sa sang ne ko Ilyaas a ngoog!” Mu di ma rey?» 15 Ilyaas ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, moom mi may jaamu, tey dinaa jàkkaarloojeek Axab moos.»

Ilyaas jànkoonte naak Axab
16 Abdiyas dem ca Axab, yegge ko ko. Axab dikk taseek Ilyaas. 17 Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?» 18 Ilyaas ne ko: «Du maa lëmbe Israyil de. Yaw kay la, yaak sa kër baay, ndax yeena dëddu santaaney Aji Sax ji, di topp tuur yi nuy wax Baal. 19 Léegi nag wooteel, Israyil gépp daje, fekksi ma ca tundu Karmel, ñu ànd ak ñeenti téeméeri yonenti Baal ak juróom fukk (450) ak ñeenti téeméeri nit (400) ñuy lekk njëlal Yesabel, te di yonenti Asera tuur ma.»
Ilyaas fenqoo naak waa kër Baal
20 Ba loolu amee Axab yónnee ca waa Israyil gépp, woo yonent ya, ñu daje ca tundu Karmel. 21 Ilyaas dikk jàkkaarlook mbooloo ma mépp. Mu ne: «Yeen nag dungeen dakkal seen ciŋiñ-caŋañ ji ngeen nekke, wet gu nekk ngeen féete fa? Su Aji Sax ji dee Yàlla, toppleen ko; su dee Baal, ngeen topp ko.» Mbooloo ma ne patt. 22 Ilyaas ne mbooloo ma: «Man de maa fi des ci yonenti Aji Sax ji, man doŋŋ, te yonenti Baal yi ñeenti téeméer lañook juróom fukk (450). 23 Léegi nag, indil-leen nu ñaari yëkk. Bàyyileen yonenti Baal, ñu tànn wenn yëkk wi, def ko ay dog, teg ci kaw matt mi, bañ koo taal. Man it dinaa defar weneen yëkk wi, teg ci kaw matt mi, bañ koo taal. 24 Su ko defee ngeen ñaan ci seeni tuur, man it ma ñaan ci Aji Sax ji. Su boobaa, Yàlla ju ci wuyoo sawara, kookoo di Yàlla.» Mbooloo ma mépp ne: «Waaw, baax na!»

25 Ci kaw loolu Ilyaas wax yonenti Baal ya ne leen: «Tànnleen wenn yëkk te jëkka defar, ndax yeena gëna bare. Bu ngeen noppee, ñaanleen ci seeni tuur, waaye buleen taal.» 26 Ñu jël yëkk wa mu leen jox, defar ko. Ñuy yuuxu, di woo Baal suba ba digg bëccëg, naan: «Baal, wuyu nu!» Waaye kenn àdduwul, kenn wuyuwul. Ña ngay ciŋiñ-caŋañi, di wër sarxalukaay ba ñu defar. 27 Digg bëccëg jot, Ilyaas di leen ñaawal, naan leen: «Yuuxuleen ca kaw, waay! Mooy Yàlla moos; jombul daa am lu muy xalaat, mbaa mu jàpp, mbaa mu tukki, mbaa xanaa muy nelaw, ñu war koo yee.»

28 Ba mu ko defee ñu gënatee yuuxu, di dagg seen yaram aki saamar aki xeej, ni ñu ko baaxoo, ba deret ja sang leen. 29 Digg bëccëg wees, ñu gëna ràkkaaju di wax ay waxyu, ba saraxu ngoon jot. Waaye du lenn lu àddu mbaa lenn lu wuyu mbaa lu leen faale.

30 Ba mu ko defee Ilyaas wax ak mbooloo ma mépp, ne leen: «Jegesileen fii!» Ñépp jegesi. Mu defaraat sarxalukaayu Aji Sax ja tasaaroo woon, 31 daldi jël fukki doj ak ñaar, mu tollook limu giiri doomi Yanqóoba. Yanqóoba la kàddug Aji Sax ja dikkaloon ne ko Israyil ay doon turam. 32 Ilyaas jël doj ya, defare ab sarxalukaay ngir Aji Sax ji, ba noppi gas kàmb gu mana def fanweeri liitar, kàmb ga wër sarxalukaay ba. 33 Mu teg matt ma ba mu jekk, daggat yëkk wa, teg ca kaw. 34 Mu ne leen: «Duyleen ñeenti njaqi ndox, tuur ci kaw yàpp week matt mi.» Ñu def ko. Mu ne: «Defaatleen!» Ñu defaat. Mu ne: «Defatileen, muy ñetti yoon!» Ñu def ko, ba muy ñetti yoon. 35 Ndox ma wal, wër sarxalukaay ba, ba kàmb ga sax fees ak ndox.

36 Ba saraxu ngoon jotee, Yonent Yàlla Ilyaas jegesi, ñaan ne: «Aji Sax ji, yaw Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, xamleel bésub tey jii ne yaw yaa di Yàlla ci Israyil, ma di sab jaam bi def lii lépp ci sa ndigal. 37 Nangul ma, Aji Sax ji, rikk nangul ma, ba mbooloo mii xam ne yaw Aji Sax ji yaa di Yàlla te yaay délloosi seen xol ci yaw.»

38 Ba loolu amee sawaras Aji Sax ji ne milib boole xoyom yàpp waak matt maak doj yaak suuf sa, ba far manq ndox ma ca kàmb ga.

39 Ba mbooloo mépp gisee loolu, dañu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Aji Sax jeey Yàlla! Aji Sax ji kay mooy Yàlla!» 40 Ilyaas ne leen: «Jàppleen yonenti Baal yii. Bu kenn ci ñoom rëcc.» Ñu jàpp leen, Ilyaas yóbbu leen ba ca xuru Kison, rendi leen foofa.

41 Gannaaw loolu Ilyaas ne Axab: «Doxal lekki te naan, ndax taw bu réy a ngi riir di ñëw.» 42 Axab dem, lekk, daldi naan. Ilyaas moom yéegi ba ca kaw tundu Karmel, sukk, dëpp jëëm ca diggante bëti óomam. 43 Mu ne surgaam: «Laggal séentuji wetu géej.» Surga ba séentuji, dikk, ne ko: «Dara newu fa.» Ilyaas ne ko mu dellu xool ba muy juróom ñaari yoon.

44 Juróom ñaareelu yoon ba, surga ba ne: «Lee de niir la wu tuut, tollu ni loxol nit, jóge géej.» Ilyaas ne ko: «Demal ne Axab, mu takk watiiram te dem, bala koo taw bee ub.» 45 Nes tuut asamaan ñuul kukk aki xàmbaar, ngelaw la jóg, taw ba sóob ak doole. Ci biir loolu Axab dawal watiiram, jëm Yisreel. 46 Aji Sax ji nag dooleel Ilyaas. Mu takk ndigg la, daw jiitu Axab ba ca buntu Yisreel.

<- 1.Buur ya 171.Buur ya 19 ->