6 Ba loolu amee Axiya dégg tànki ndaw sa ca bunt ba. Mu ne ko: «Soxnas Yerbowam, agsil! Ana looy mbubboo keneen nii? Man de yóbbante nañu ma ci yaw xibaar bu tiis. 7 Demal ne Yerbowam: “Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Dama laa yékkati ci biir mbooloo mi, fal la nga jiite Israyil sama ñoñ. 8 Damaa foqatee nguur gi ci loxol waa kër Daawuda, jox la ko. Waaye meloo ni Daawuda, sama jaam ba daan jëfe samay santaane, toppe ma léppi xolam, du def lu moy lu ma rafetlu. 9 Def nga musiba, ba raw mboolem ñu la jiitu, dem di sàkkal sa bopp yeneen yàlla ak tuur yu ñu móole weñ, ba sama xol fees. Man mii nga xarab, dëddu ma. 10 Moo tax duma def lu moy wàcce musiba ci kër Yerbowam.
12 «Yaw nag jógal ñibbi sa kër. Booy teg sa tànk ca biir dëkk ba rekk, gone gi dee. 13 Israyil gépp dinañu ko jooy. Kooku rekk déy lees di denc ci bàmmeel, ci ku bokk ci Yerbowam, ngir ci moom doŋŋ la Aji Sax ji Yàllay Israyil gis lu baax, ci waa kër Yerbowam. 14 Aji Sax ji dina falal boppam buur bu jiite Israyil, te kooku dina faagaagal waa kër Yerbowam. Bés bi taxaw na jeeg! Ana lu ciy topp? 15 Aji Sax ji dina fàdd Israyil. Dinañu mel ni gattax guy foy-foyi cim ndox. Dina déjjatee Israyil ci suuf su baax sii mu joxoon seeni maam, tasaare leen ca wàllaa dexu Efraat, ndax dañoo samp ay xer yu ñuy jaamoo Asera, di merloo Aji Sax ji. 16 Aji Sax ji dina wacc Israyil ndax bàkkaari Yerbowam yi mu bàkkaar te di ko bàkkaarloo Israyil.»
17 Ba loolu amee soxnas Yerbowam jóg, bàyyikoo fa, ba àgg Tirsa. Naka la agsi ca bunt kër ba, xale ba dee. 18 Ñu rob ko, Israyil gépp jooy ko, muy la Aji Sax ji waxoon, Yonent Yàlla Axiya jaamam ba jottli.
19 Li des ci mbiri Yerbowam, ay xareem ak na nguuram deme woon, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. 20 At ya Yerbowam falu buur ñaar fukki at la ak ñaar. Gannaaw loolu mu saay, fekki ay maamam. Nadab doomam falu, wuutu ko.
25 Ba Buur Robowam faloo, ba dugg ci juróomeelu atu nguuram, Sisag buuru Misra song Yerusalem. 26 Ci kaw loolu Sisag jël alali kër Aji Sax ji, ak alali kër Buur. Lépp la jël ba ca mboolem pakki wurus ya Suleymaan defarlu woon. 27 Ba mu ko defee Buur Robowam defarlu ay pakku xànjar yu wuutu yu wurus ya. Mu teg ko ca loxoy njiiti dag yay wattu buntu kër Buur. 28 Saa yu Buur dee duggsi ca kër Aji Sax ji, dag ya ŋàbb pakk ya, bu ñu noppee delloo ko ca néegu dag ya.
29 Li des ci mbiri Robowam ak mboolem la mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. 30 Xare masula dakk diggante Robowam ak Yerbowam. 31 Gannaaw gi Buur Robowam tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko fa ay maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Ndeyam a doon Naama, Amoneen ba. Ci kaw lool doomam Abiyam falu buur, wuutu ko.
<- 1.Buur ya 131.Buur ya 15 ->