5 Ana kuy Apolos sax? Ak kuy Póol? Xanaa ay surga doŋŋ yu ngeen jaare, ba gëm, ni Boroom bi jagleele kenn ku nekk ci nun, aw sasam. 6 Maa jëmbat, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil. 7 Ki jëmbat nag, ak ki suuxat, kenn du ci dara, xanaa Yàlla miy jebbil doŋŋ. 8 Ki jëmbat, ak ki suuxat ñoo yem kepp, waaye ku ci nekk kemu liggéeyu boppam lay yooloo. 9 Noo bokk diy surga ci liggéeyu Yàlla bi; yeen ngeen di toolu Yàlla, di tabaxub Yàlla.
10 Yiwu Yàlla wi mu ma may nag, ci laa lale kenu gi, ni tabaxkat bu xareñ, keneen di tabax ca kaw. Waaye na ku nekk xool bu baax na mu cay tabaxe. 11 Geneen kenu moom maneesu koo lal, xanaa gi xasa lale, te mooy Yeesu Almasi. 12 Ku tabax ci kaw kenu gi nag, nga tabaxe wurus, mbaa xaalis, mbaa per, mbaa dénk, mbaa gattax, mbaa boob, 13 ku ci nekk, sab liggéey dina feeñ, ndax bés baa koy xamle, nde sawara lees koy feeñale. Ku ci nekk, ak lu sa xeetu liggéey mana doon, sawara lees koy natte. 14 Ku liggéeyoon ba la nga tabaxoon ca kaw kenu ga des, dinga yoolu. 15 Waaye ku sab liggéey lakk, ñàkk nga. Yaw ci sa bopp nag dinga mucc, mel ni ku rëcce cig lakk rekk.
16 Xanaa xamuleen ne kër Yàlla ngeen, te Noowug Yàlla moo dëkk ci yeen? 17 Ku yàq kër Yàlla nag, kooku Yàlla dina ko yàq, ndax kër Yàlla dafa sell, te mooy li ngeen doon.
18 Bu kenn nax boppam: Ku teg boppam ci yeen, boroom xam-xam, ni xarnu bii jàppe xam-xam, kooku na doon ab dof, ngir am xam-xam bi wóor. 19 Ndaxte xam-xamu àddina sii, ndof la fa Yàlla. Moo tax bindees na ne: «Mooy kiy jàpp ñi muus ci seen pexey muusaatu*3.19 Seetal ci Ayóoba 5.13.,» 20 tegati ca ne: «Boroom bi xam na xalaati boroom xel yi te xam na ne neen la†3.20 Seetal ci Sabóor 94.11..»
21 Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom, 22 muy Póol, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di ndee, di tey, di ëllëg, lépp, yeena ko moom. 23 Yeen nag, Almasi moo leen moom, te Almasi, Yàllaa ko moom.
<- 1.Korent 21.Korent 4 ->