10 Bu Timote dikkee nag, fexeleen ba bumu am lu muy tiit ci seen biir, ndax liggéeyu Boroom bi lay liggéey ni man. 11 Kon bu ko kenn xeeb. Gannaaw loolu nangeen ko yiwi ak jàmm, ba mu délsi ci man, ndax moom laay xaar, mook bokk yi itam.
12 Mbokk mi Apolos nag moom, soññ naa ko lu bare, ngir mu dikk ba ci yeen, ànd ak bokk yi, waaye fii nu tollu yebuwu ci dara. Teewul bu jekkoo, dina dikk.
15 Bokk yi, xam ngeen ne Estefanas ak njabootam ñooy jooxeb ndoortel meññeef ci diiwaanu Akayi, te jàpple ñu sell ñi lañu séddoo. Kon dama leen di ñaan, 16 ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak mboolem ñu bokk ak ñoom liggéey bi ak coono bi. 17 Maa ngi bége teewaayu Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus, ndax bi ngeen wuutee tey, ñoo leen taxawal. 18 Dalal nañu sama xel, ak seen mos, yeen itam. Kon nit ñu mel noonu, fonkleen leen.
19 Mboolooy gëmkati diiwaanu Asi nag ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci turu Sang bi, ñoom ak mbooloom gëmkat ñiy daje seen kër. 20 Bokk yépp a ngi leen di nuyu.
21 Man Póol maa bind nuyoo bii ci sama loxol bopp.
22 Ku buggul Sang bi, na alku. Maranata (mu firi sunu Sang, dikkal!)
23 Yal na yiwu Sang Yeesu ànd ak yeen.
24 Sama cofeel ñeel na leen, yeen ñépp, ci Yeesu Almasi mi nu bokk.
<- 1.Korent 15