5 Ñiy topp seen nafsu, seeni bëgg-bëgg rekk lañu fonk, waaye ñiy topp Xelu Yàlla mi, coobareem lañu fonk. 6 Ndaxte fonk nafsu, ci dee lay jëme; waaye fonk Xelu Yàlla mi, dund ak jàmm lay joxe. 7 Ndaxte ku fonk sa nafsu, bañaaleb Yàlla nga, ndaxte doo déggal Yàlla, mbaa ngay sàmm ay santaaneem, te manuloo koo def sax. 8 Kuy topp sa nafsu nag, doo mana neex Yàlla.
9 Waaye yéen nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye yéena ngi topp Xelu Yàlla mi, bu fekkee ne mu ngi dëkk ci yéen. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom. 10 Bu fekkee ne Kirist dëkk na ci yéen nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax bàkkaar bi nekk ci yéen, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Yàlla jox. 11 Kon nag gannaaw Xelum Yàlla, mi dekkal Yeesu ca néew ya, dëkk na ci yéen, dina tax seen yaram wi néew doole dund ci kàttanu Xel moomu dëkk ci yéen.
12 Kon nag bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxuma leen topp sunu nafsu ak i bëgg-bëggam; 13 ndaxte kuy topp nafsoom, fàww mu dee, waaye kuy not jëfi yaramam ci dooley Xelu Yàlla mi, dina dund. 14 Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelu Yàlla mi, ay doomi Yàlla lañu. 15 Nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba», maanaam «Baay.» 16 Ndaxte Xelu Yàlla mi, moom ci boppam, day ànd ak sunu xel ci seede ne doomi Yàlla lanu. 17 Gannaaw ay doomi Yàlla lanu, dinanu moomi lépp li Yàlla jagleel ay doomam, séddu ci ngëneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku bëgga bokk ak Kirist ndamam ëllëg, war ngaa séddu ci ay fitnaam tey.
22 Xam nanu ba fi nu tollu ne li Yàlla bind lépp a ngi mititlu ni jigéen juy matu. 23 Te du dunyaa bi rekk mooy mititlu, nun it nu ngi mititlu, nun ñi Yàlla sol Xelam, ngir nu ñam añu ëllëg; nu ngi ne seew Yàlla boole nu ci lépp li nu yelloo ni ay doomam, keroog bés bu Yàllay goreel sunu yaram. 24 Ndaxte sunu mucc ëmb na yaakaar. Li nga gis ba noppi, nekkatul yaakaar; li teew, noo koy yaakaare? 25 Li feek gisagunu nag li nuy yaakaar, dinanu ko séentu ak muñ.
26 Te it Xelu Yàlla mi moo nuy xettali ci sunug néew doole. Ndaxte xamunu sax naka lanu wara ñaane Yàlla, waaye Xelu Yàlla maa ngi nuy ñaanal fa moom ak i yéene yu làmmiñ manta takk. 27 Te Yàlla, miy nattu xol yi, xam na xalaatu Xel mi, ndaxte tinu, gi muy tinul gaayi Yàlla yi, méngoo na ak coobarey Yàlla.
28 Xam nanu itam ne ñi bëgg Yàlla, maanaam ñi Yàlla woo ci boppam te boole leen ci li mu tëral, Yàlla dina joo loxoom ci lépp lu xew ci seen dund, ngir jural leen lu baax. 29 Ndaxte ñi mu xamoon lu jiitu, dafa dogaloon ñu nirook Doomam, ngir mu nekk taaw ci biir njaboot gu yaa. 30 Ñi mu dogaloon loolu ci ñoom, da leena woo; ñooñu mu woo, da leena àtte ni ñu jub; ñooñu mu àtte jub, da leena boole ca ndamam.