5 Waaye ndegam dëgër nga bopp te bëgguloo réccu, yaa ngi dajale merum Yàlla ci sa bopp. Ndaxte Yàlla sàkk na bés bu muy wone àtteem bu jub bi te meram wàcc ci ñi bon; 6 bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam. 7 Ñiy góor-góorlu ciy def lu baax, bëgg Yàlla boole leen ca ndamam te sédde leen ngërëm ak dund gu sax, dina leen tàbbal ci dund gu dul jeex. 8 Waaye ñi dëgër bopp, ba tanqamlu dëgg, di topp lu jubadi, seen pey mooy dooni merum Yàlla ak toroxte. 9 Ki doon def lu bon, peyam mooy tiis ak metit wu tar, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut. 10 Waaye ki doon def lu baax, añam mooy bokk ci ndamu Yàlla, am ngërëm ak jàmm, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut. 11 Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
12 Képp ku doon bàkkaar nag te nekkuloo woon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci lu dul yoonu Musaa, nga doora sànku. Te képp ku doon bàkkaar te nga nekkoon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci yoon woowu. 13 Kon déglu yoonu Musaa rekk doyul; du loolu mooy tax nit jub ci kanam Yàlla; kiy sàmm yoon wi, moom la Yàlla di àtte ni ku jub. 14 Ndax ñi dul Yawut te nekkuñu ci yoonu Musaa, ñu ngiy def li yoon woowu tëral, ndaxte Yàlla def na ko ci nit. Te wonee nañu noonu ne man nañoo ràññee lu baax ak lu bon, su ñu nekkul sax ci yoonu Musaa, 15 di wone it ne Yàlla bind na ci seen xol jëf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat ñoo leen di tuumaal, mbaa ñu leen di jéggal. 16 Ndax bés dina ñëw, bu xalaat yu làqu yi di feeñ, te Yàlla àtte nit ñi jaarale ko ci Yeesu Kirist. Xibaaru jàmm, bi may waare, moo ko wax.