5 Noonu ki toog ca gàngune ma ne: «Maa ngi yeesal lépp!» Mu ne ma: «Bindal, ndaxte kàddu yii yu wóor lañu te dëggu.» 6 Mu teg ca ne ma: «Lépp mat na! Maay Alfa di Omega, di njàlbéen gi, di muj gi. Ku mar, dinaa la may ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara. 7 Ku daan, dinga am cér ci mbir yii. Dinaa nekk Yàlla sa Boroom, te dinga nekk doom ci man. 8 Waaye ñi ragal ak ñi gëmul ak ñiy def lu ñaaw ak ñiy bóome ak ñiy njaaloo ak luxuskat yi ak xërëmkat yi ak fenkat yépp, seen añ moo di déegu sawara bi ànd ak tamarax. Loolu mooy ñaareelu dee gi.»
9 Gannaaw loolu benn malaaka ñëw, mi bokk ca juróom ñaari malaaka, ya yoroon juróom ñaari ndabi musiba yu mujj ya, ne ma: «Ñëwal, ma won la séet bi, soxnas Gàtt bi.»
10 Noonu Xelum Yàlla solu ma, malaaka ma yóbbu ma ci kaw tund wu réya réy. Noonu mu won ma Yerusalem, dëkk bu sell bi, muy wàcce ci asamaan, jóge ca wetu Yàlla, 11 ànd ak ndamu Yàlla. Leeraayam mel ni leeraayu per bu jafe lool, ni jamaa buy ray-rayi. 12 Miir bu réy te kawe moo ko wër te am fukki bunt ak ñaar, bu ca nekk malaaka taxaw ca wet ga. Ca bunt ya bind nañu ca fukki tur ak ñaar, yu giiri bànni Israyil. 13 Ca penku am na fa ñetti bunt; ca nor ñett; ca sudd ñett ak ñett ca sowu. 14 Samp nañu miiru dëkk ba ci fukki fondamaa ak ñaar, yu ñu bind turi fukki ndawi Gàtt ba ak ñaar.
15 Ki doon wax ak man amoon na nattukaay, di bantu wurus bu mu doon natte dëkk ba ak miir ba ko wër, ak bunt ya. 16 Dëkk ba dafa kaare, guddaay ba ak yaatuwaay ba ñoo tolloo. Mu natt dëkk ba ak bant ba mu yor. Guddaay ba ak yaatuwaay ba ak taxawaay ba lépp tolloo, di fukki junni ak ñaar ciy estat[a]. 17 Malaaka ma natt miir ba nattub nit, fekk miir ba di téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti xasab[b]. 18 Miir ba, jamaa lañu ko liggéeye, te dëkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set. 19 Fondamaay miiru dëkk ba rafetale nañu leen xeeti per yu nekk.
22 Gisuma ca dëkk ba kër Yàlla, ndaxte Boroom bi Yàlla Aji Man ji ak Gàtt ba ñooy màggalukaay ba. 23 Dëkk ba soxlawul jant walla weer ngir leeral ko, ndaxte ndamu Yàlla moo koy leeral, te Gàtt ba moo nekk làmpam. 24 Xeeti àddina dinañu dox cig leeram, te buuri àddina dinañu ca indi seen ndam. 25 Bunti dëkk ba duñu tëju bëccëg, te guddi du fa am. 26 Dinañu fa indi ndamu xeet yi ak seen alal. 27 Dara du fa dugg lu am sobe, mbaa kenn kuy sóobu ci ñaawteef walla fen. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Gàtt bi rekk ñoo fay dugg.
<- PEEÑU MA 20PEEÑU MA 22 ->