8 Meneen malaaka, di ñaareel bi, topp ca naan: «Daanu na! Babilon, dëkk bu mag, bi daan màndil réew yépp ak biiñu njaaloom, daanu na.»
9 Meneen malaaka, di ñetteel bi, topp ca, di xaacu naan: «Ku jaamu rab wi ak nataalam te nangoo am màndargaam ci jëëm walla ci loxoom, 10 dina naan moom itam biiñu xadarub Yàlla bi kenn raxul, ñu sotti ko ci koppu meram. Te dees na ko mbugal ci sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi, 11 te saxar siy jóge ci seen mbugal dina gilli ba fàww. Ñooñu di jaamu rab wi ak nataalam, ak képp ku nangoo jot màndargam turam, duñu noppalu guddi ak bëccëg.»
12 Looloo tax gaayi Yàlla yi wara muñ, ñooñuy sàmm ndigali Yàlla yi ak ngëm ci Yeesu.
13 Noonu ma dégg baat ci asamaan naan: «Bindal: “Bés ni tey, ñi nekk ci Boroom bi te dee, barkeel nañu.”» Xelum Yàlla nee na: «Waaw, dinañu noppalu ci seeni coono, ndaxte seeni jëf a nga leen di xaar.»
16 Noonu ka toogoon ca kaw niir wa dawal sàrtam ci kaw suuf, góob àddina sépp.
17 Bi loolu amee meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga nekk ca asamaan, yor moom itam sàrt bu ñaw. 18 Noonu meneen malaaka, ma am sañ-sañ ca sawara sa, jóge ca sarxalukaayu cuuraay ba, daldi wax ak baat bu xumb ak malaaka, ma yor sàrt bu ñaw ba, ne ko: «Dawalal sa sàrt bu ñaw bi te dagg cëggu reseñ yu àddina, ndaxte ñor nañu.»
19 Noonu malaaka ma daldi dawal sàrtam ci àddina, dagg reseñ yi, sànni leen ci biir segalukaay bu réy bu merum Yàlla. 20 Ñu nal reseñ ya ca segalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génn ca, ba agsi ci laabi fas yi, te wal ba ëmb lu mat ñetti téeméeri kilomet.
<- PEEÑU MA 13PEEÑU MA 15 ->