1 Kon nag yéen samay bokk, ñi ma bëgg te namm leen, di sama mbég ak sama kaalag ndam, jàppleen bu dëgër noonu ci Boroom bi, soppe yi!
4 Deeleen bég ci Boroom bi; maa ngi koy waxati: bégleen! 5 Na seen lewet leer ñépp. Boroom bi jege na. 6 Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetal-leen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant. 7 Noonu jàmmu Yàlla, ji xel manta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu.
8 Léegi nag bokk yi, na seen xalaat jublu ci lii: lu dëggu, lu jekk, lu jub, lu sell, lu rafet ak lu faaydawu; su fi amee lu baax mbaa lu mata naw, xalaatleen ko. 9 Li ngeen jànge ci man te nangu ko, li ngeen dégge ci man te gis ko, jëfeleen ko; kon Yàllay jàmm dina ànd ak yéen.
15 Yéen waa Filib xam ngeen ne bi ngeen jëkkee xam xibaaru jàmm bi, te ma jóge diiwaanu Maseduwan, benn mbooloo àndul woon ak man ci mbirum joqleente ndimbal, mu dul yéen doŋŋ. 16 Ba ma nekkee dëkku Tesalonig sax, yónnee ngeen ay yooni yoon, ngir faj samay soxla. 17 Loolu tekkiwul ne damay sàkku ay ndimbal ci yéen, waaye damaa bëgg rekk seen denc yokku fa Yàlla. 18 Fi mu ne jot naa li ma aajowoo lépp, ba maa ngi ci naataange; li ngeen ma yónnee ci loxoy Epafrodit doy na sëkk; ni xetu latkoloñ la mel ci man, di sarax su neex Yàlla te mu nangu ko. 19 Te Yàlla sama Boroom, mi denc ci Kirist Yeesu xéewal yu dul jeex, dina ci faj seeni soxla yépp.
20 Yal na Yàlla sunu Baay yelloo ndam ba fàww. Amiin.
23 Yal na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.
<- FILIB 3