mu bind ko
FILEMON
1 Man Pool, mi ñu tëj kaso ngir Kirist Yeesu, ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci xeex bi; 2 te fàttewunu sunu jigéen Afiya, ak sunu àndandoo ci xeex bi Arkib, yéen ak mbooloom ñi gëm, miy dajee sa kër. 3 Yal na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
12 Maa koy yebal fi yaw, waaye xamal ne mooy sama reeni xol. 13 Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi. 14 Waaye bëggumaa def dara loo àndul; noonu ndimbal li nga may defal du nekk sañul-bañ, waaye mu ànd ak xol bu tàlli. 15 Xëy na sax dafa tàggoo woon ak yaw diir bu gàtt, ngir nga jotaat ci ba fàww; 16 waxuma léegi ni jaam rekk, waaye lu ko sut, xanaa mbokk mu dëggu ci xol, fekk looloo raw ag njaam. Mbokk la ci man, rawatina ci yaw, muy sa jaam ci aada, di sa mbokk léegi ci Boroom bi.
17 Soo ma jàppee ni nawle nag, teeru ko, ni su ma la doon ganesi. 18 Soo ko naree topp genn tooñ mbaa benn bor, topp ma ko. 19 Man Pool maa ngi lay bind ak sama loxob bopp ne dinaa la ko fey; bëggumaa yegg ci ne sag dund sax ci man la jaar! 20 Waaw, yaw sama mbokk, dimbali ma ci Boroom bi, te seral sama xol ci sunu bokk ci Kirist. 21 Noonu bind naa la, ndax wóor na ma ne dinga ma déggal, ba weesu sax li ma la sant.
22 Te itam nanga ma waajal néeg, ndaxte yaakaar naa ne Yàlla dina nangu seeni ñaan, ba delloosi ma leen.
23 Sama mbokk Epafras, mi ma nekkal fi ci kaso bi ci turu Kirist, mu ngi lay nuyu. 24 Samay àndandoo ci liggéey bi, Màrk, Aristàrk, Demas ak Luug, ñu ngi lay nuyu.
25 Yal na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.
- a njariñ: ci làkku gereg turu Onesim mooy tekki «Ku am njariñ.»