1 Mu ne leen ati: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu nguuru Yàlla ñëw ak doole.»
5 Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» 6 Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jàpp na leen ñoom ñett ñépp. 7 Noonu niir muur leen, te baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.» 8 Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk.
9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi muy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki na.» 10 Ñu téye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki.
11 Noonu taalibe yi laaj Yeesu: «Lu tax xutbakat yi di naan, Ilyaas moo wara jëkka ñëw?» 12 Yeesu ne leen: «Waaw, Ilyaas dina jëkka ñëw, jubbanti lépp. Waaye itam lu tax bind nañu ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, ñu xeeb ko, dëddu ko. 13 Waaye maa ngi leen di wax ne, Ilyaas ñëw na, te def nañu ko la leen neex, ni ko Mbind mi waxe.»
16 Noonu Yeesu laaj leen: «Ci lan ngeen di werante ak ñoom?» 17-18 Kenn ci mbooloo mi ne ko: «Kilifa gi, rab jàpp na sama doom, ba luuloo ko. Saa su ko jàppee, daf koy daaneel ci suuf, gémmiñ gi di fuur, muy yéyu, ne jàdd. Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye manuñu ko.» 19 Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi, ba kañ laa wara nekk ak yéen, ba kañ laa leen wara muñal? Indil-leen ma xale bi.» 20 Ñu indil ko ko. Bi xale bi gisee Yeesu nag, rab wi sayloo ko ci saa si, mu daanu ci suuf, di xalangu, gémmiñ giy fuur. 21 Yeesu laaj baay bi: «Lii kañ la ko dal?» Baay bi ne ko: «Li dale ci ngoneem. 22 Léeg-léeg rab wi bëmëx ko ci sawara, léeg-léeg mu bëmëx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, yërëm nu te xettali nu.» 23 Yeesu ne ko: «Nga ne: “Soo ko manee,” ku gëm man na lépp.»
24 Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: «Gëm naa, dàqal ma sama ngëmadi.»
25 Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, wërsi ko, mu daldi gëdd rab wi nag ne ko: «Génnal ci moom, yaw rab wu luu te tëx, te bu ko jàppaat; wax naa la ko.» 26 Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, génn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax ñu bare ne: «Dee na.» 27 Waaye Yeesu jàpp loxoom, jógloo ko, xale bi daldi taxaw.
28 Bi Yeesu duggee ci kër gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: «Lu tax manunu ko woona dàq?» 29 Yeesu ne leen: «Yu mel ni yii, ñaan ci Yàlla rekk a leen di dàq.»
30 Bi loolu amee ñu jóge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu bëggul kenn yég ko. 31 Ndaxte muy jàngal taalibe yi ne leen: «Dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit, te dinañu ko rey, mu dekki ci ñetti fan.» 32 Waaye taalibe yi xamuñu lu wax joojuy tekki, te ñemewuñu ko koo laaj.
35 Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak ñaar ne leen: «Ku bëgga jiitu, na topp ci gannaaw ñépp te nekk surgab ñépp.» 36 Bi ko Yeesu waxee, mu jël xale, indi ko ci biir géew bi, ba noppi leewu ko naan: 37 «Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma yónni.»